The Wolof-Multilanguage Live Dictionary Project
Le Dictionnaire Wolof-Multilingue Vivant !



translator  wo-en en-wo grammar talk   $ 
      grammatik konversation  
HOME wo-fr fr-wo grammaire conversation sciences fr
Mardi 31 mars 2009 2 31 /03 /Mars /2009 00:05

Melokaanu nit ki
: Le corps humain


Nit ñi : Abu Faal ak Musaa Ba

Les personnages : Abou Fall (AF) et Moussa Ba (MB)

AF – Musaa, won ma sa tànk!  Moussa, montre-moi ton pied!
MB Sama tàng a ngi nii.  Voici mon pied.
AF Lii, lan la?  Ceci, qu'est-ce que c'est?
MB Loolu, sa loxo la.  Ça, c'est ta main.
AF Won ma sa dënn ak say gët!  Montre-moi ta poitrine et tes yeux!
MB Sama dënn ak sama gët a ngi nii.  Voici ma poitrine et mes yeux.
AF Laalal sa bakkan!  Touche ton nez!
MB Laal naa sama bakkan.  J'ai touché mon nez.
AF Lan ngay def ak sa bakkan?  Qu'est-ce que tu fais avec ton nez?
MB Damay noyyi ak sama bakkan.  Je respire avec mon nez.
AF Lan mooy njëriñu bëñ?  A quoi servent les dents?
MB Njëriñu bëñ mooy sàqami lekk yi.  Les dents servent à mâcher la nourriture.
AF Ana sa bopp?  Où est ta tête?
MB Sama bopp a ngi nii.  Voici ma tête.
AF Am na kawar gu bare?  Il y a beaucoup de cheveux?
MB Waaw, am na tuuti, am na tuuti rekk.  Oui, il y en a seulement un peu.



. bakkan bi  le nez
. bëñ  dent
. bët bi (gët yi)  l'oeil (les yeux)
. bopp bi  la tête
. dënn bi la poitrine
. kawar gi  la chevelure
. laal  toucher
. loxo bi  la main
. njëriñ li  l'utilité
. noyyi  respirer
. sàqami  broyer
. tànk bi  le pied
. tuuti  un peu


Abdoulaye Dial
 
Par wolofi - Publié dans : FR conversation - Communauté : Portes et Fenêtres
Ecrire un commentaire - Voir les 1 commentaires
Retour à l'accueil

Chic Meteo
Holidays

♦ Las Vegas
♦ New York
♦ UTC/GMT
♦ Paris
♦ Dakar

 

 

NON à l'excision !

Recherche

ŋ [ ] À Ññ Çç ß Óó Ëë Ïï Öö
 @ ½ ¼ Ää Üü ÷ ▀ ² ■ ª º

Al-Nd-Petit-Wolof.jpg
Le Petit Wolof deviendra grand.

 
 
  
anti-xeesal.jpg  
Anti-xeesal Campaign.
       
 
   

Syndication

  • Flux RSS des articles

Le sens du partage


pied_top.jpg
 
Contact - C.G.U. - Rémunération en droits d'auteur - Signaler un abus - Articles les plus commentés