The Wolof-Multilanguage Live Dictionary Project
Le Dictionnaire Wolof-Multilingue Vivant !



translator  wo-en en-wo grammar talk   $ 
      grammatik konversation  
HOME wo-fr fr-wo grammaire conversation sciences fr
Mercredi 2 août 2000 3 02 /08 /Août /2000 14:15

123  A B C D E F G H I J K L M N O P Q R S T U V W X Y Z

 

 

 

. babouche nf  maraakiis bi. Jënd naa ay maraakiis. J'ai acheté des babouches.

. badamier nm  gerte-tubaab gi. Xale yaa ngiy for ay gerte-tubaab. Les enfants ramassent les fruits du badamier.

. badiner foontu. Umar dafay foontu ak liggéeyam. Oumar badine avec son travail.

. bagarreur adj  pànk. Xale bi dafa pànk, dafay xeex bés bu nekk. L'enfant est bagarreur, il se bat chaque jour avec les autres.

. bague nf  jaaro bi. Xoolal jaaro bi mu ma may ! Regarde la bague qu'il m'a donnée !

. baigner sang, (se -) sangu. Damay sang sama doom ci diggu kër gi. Je baigne mon enfant dans la cour.

. bailler óbbëli. Kadeer sonn na lool, gis naa ko muy óbbëli. Kader est très fatigué je l'ai vu  bailler.

. balafon nm  baliñe bi. Abu dafay tëgg baliñe. Abou joue le balafon.

. balafre nf  ñaas wi, gàjj yi. Sisoko dafa am ay ñaas ci kanamam. Cissoko a des balafres sur le visage.

. balai nm  buubu bi, bale gi. Buubu bi laay buube néeg bi. C'est avec le balai que je balaie la chambre.

. ballon nm  kuppe bi, bal bi. Jëndal naa xale yi kuppe. J'ai acheté un ballon pour les enfants.

. bandit  nm  wayu bi. Gis naa ay wayu ci tàkk gi. J'ai vu des bandits sur le quai.

. baobab nm  guy gi. Sunu kër am na guy. Notre maison a un baobab.

. baptême nm ngénte li. Sa ngénte li neex na lool. Ton baptême a été très agréable.

. barbe nf  sikkim bi. Damay wat sama sikkim. Je rase ma barbe.

. bas adj  suufe. Siis bi nga toog, dafa suufe. La chaise sur laquelle tu es assis est basse.

. basané adj  tikk. Yaramu Ayda dafa tikk. Aïda a la peau basanée.

. bateau nm  gaal gi. Gaal gi suux na ci dex gi. La pirogue a chaviré dans le fleuve.

. bâtir tabax. Damay sama kër. Je construis ma maison.

. bâtonnet nm soccu bi. Jënd naa ay soccu. J'ai acheté des bâtonnets (pour les dents).

. battoir (à linge) nm  tàpparka bi. Tàpparka lañuy tàppe yére yi. C'est avec un battoir que l'on tape les habits (pour les laver).

. battre bàcc, ñaf. Beykat baa ngiy bàcc gerte gi. Le cultivateur est en train de battre l'arachide. Pàppaam ñaf na ko bu baax. Son père l'a bien battu.

. baver yuut. Xar mi dafa feebar, mu ngiy yuut. Le mouton est malade, il bave.

. beau, belle adj  rafet. Dajee naak janq bu rafet. J'ai rencontré une belle fille.

. beaucoup adv  bare. Tey Muusaa dafa bare xaalis. Aujourd'hui Moussa a beaucoup d'argent.

. beau-fils nm  goro bi. Damay nuyuji samay goro. Je vais saluer mes beaux-fils.

. bébé nm  nenne bi. Sama jabar am na nenne. Ma femme a un bébé.

. bec nm  sàll wi. Nanga sànni sàllu ganaar gi ! Il faudra jeter le bec du poulet !

. becqueter cof. Séq gaa ngiy cof dugub ji. Le coq becquète le mil.

. bègue adj dër. Xale bi mënul wax bu baax, dafa dër. L'enfant parle mal, il est bègue.

. bélier  nm  kuuy mi. Sama baay jënd na benn kuuy. Mon père a acheté un bélier.

. belle-soeur nf  njëkke li. Sama njëkke seetsi na ma démb. Hier ma belle-soeur est venue me rendre visite.

. belliqueux adj njabur. Xale bi dafa njabur, kenn du wax ak moom. Cet enfant est belliqueux, personne ne lui adresse la parole.

. bénédiction nf  barke bi. Faatu, liggéeyam dafa am barke. Fatou, son travail est une bénédiction de Dieu.

. bénéfice nm  ngañaay li, tono li. Sa njaay mi am na ngañaay. Ta vente a un bénéfice.

. bénéficier xéewlu. Nu ngiy xéewlu ci sa ndimbal li. Nous bénéficions de ton aide.

. béni adj barkeel. Yàlla moo barkeel sa liggéey. C'est Dieu qui a béni ton travail.

. benjamin nm  caat bi. Maay sunu caatu kër. Je suis le benjamin de la famille.

. béquille nf  sukkóot bi. Sama yaay ay sukkóot lay doxe. Ma mère marche avec des béquilles.

. bercer aayoo. Jigéen jaa ngiy aayoo doomam. La femme est en train de bercer son fils.

. berger nm  sàmm bi. Sàmm baa ngiy wëgg jur gi. Le berger est en train d'abreuver le bétail.

. besoin nm  aajo ji,  (avoir -) soxla. Togg, sama aajo la. Faire la cuisine est un besoin pour moi. Xaalis bu bare laa soxla. J'ai besoin de beaucoup d'argent.

. biberon nm  ŋankal bi. Xale baa ngiy nàmp ŋankal bi. L'enfant tète le biberon.

. bien nm  alal ji, am-am bi. Sama nijaay dafa am lalal. Mon oncle a de la fortune.

. bijoutier nm  tëgg bi. Tëgg baa ngiy tëgg ay jaaro nopp. Le bijoutier fabrique des boucles d'oreilles.

. blaguer caaxaan, kaf. Yow, dangay caaxaan. Toi, tu blagues seulement.

. blanc adj weex. Jënd naa ay dàll yu weex. J'ai acheté des chaussures blanches.

. blesser gaañ, (se -) gaañu. Ya ma gaañ ci loxo. C'est toi qui m'a blessé à la main.

. boire naan. Naan naa meew mi. J'ai bu le lait.

. boîter soox. Abdu dafay soox tànk bi. Abdou boîte.

. bon, bien adj baax. Abdu dafa baax. Abdou est bon. Déglu ma bu baax ! Ecoute-moi bien !

. bonbon nm  tàngal bi. Jëndal naa xale yi ay tàngal. J'ai acheté des bonbons pour les enfants.

. bonne nf  mbindaan mi. Mbindaan mi mooy toppatoo kër gi. C'est la femme de ménage qui s'occupe de la maison.

. bord nm  pegg bi boor bi. Toogal ci peggu lal bi nu waxtaan ! Assieds-toi au bord du lit afin qu'on cause.

. bossu nm  xuuge bi. Gis naa benn xuuge tey. J'ai vu un bossu aujourd'hui.

. bouc nm  sikket bi.  Jënd naa benn sikket ca daral ba. J'ai acheté un bouc au foirail.

. bouche nf  gémmiñ. Boo yeewoo, nanga raxas sa gémmiñ ba mu set ! Au réveil il faudra bien laver ta bouche !

. bouchon nm  saañ bi. Tëjal butéel bi ak saañ bi. Ferme la bouteille avec le bouchon !

. bouquet nm  cabb. Siidi yónnee na ma cabbu tóor-tóor. Sidi m'a envoyé un bouquet de fleurs.

. bouteille nf  butéel bi. Sol naa butéel bi ndox. J'ai rempli la bouteille d'eau.

. bouton (sur le corps) nm  picc bi. Am naa benn picc ci sama bakkan. J'ai un bouton sur le nez.

. bracelet nm  lam bi. Tëgg bi defaral na ma lamu xaalis bu rafet. Le bijouier m'a fait un joli bracelet en argent.

. braise nf  xal wi. Def naa ay xal ci and wi. J'ai mis des braises dans l'encensoir.

. branche nf  car bi, bànqaas bi. Dagg nañu caru garab yi. On a coupé les branches des arbres.

. bredouille adj  sooy. Dama rëbbiwoon wante dama sooy. J'étais à la chasse, mais je suis revenu bredouille.

. brouillard nm  làyyi bi. Fan yii, làyyi bi dafa bare. Il y a beaucoup de brouillard ces jours-ci.

. broussard nm  kow-kow bi. Kow-kow bi mënul fecc. Le broussard ne sait pas danser.

. brousse nf  àll bi, gott gi, ñaay bi. Tool yaa ngi ci àll bi. Les champs se trouvent en brousse.

. bruiner wis, ñebb-ñebbal. Tawul, dafay wis. Il ne pleut pas, il bruine.

. bruisser riir. Oto baa ngiy riir ci gannaaw. L'auto bruisse derrière.

. brûler lakk, tàkk. Kër gaa ngiy lakk. La maison brûle.

. brûlure nf  lakk-lakk bi. Sa lakk-lakk bi metti na. Ta brûlure est douloureuse.

. bruyant adj  xumb, (paroles) cow li. Seen ngénte li xumb na. Votre baptême est bruyant.

. bûcheron nm  lawbe bi. Lawbe yeey dagg garab yi. Ce sont les bûcherons qui coupent les arbres.

. buffle nm  nagu-àll bi. Gis naa benn nagu-àll. J'ai vu un buffle.

 

  Le Petit Wolof est un dictionnaire vivant. Revenez le voir souvent.

Par wolofi - Publié dans : FR-WO - Communauté : partage
Ecrire un commentaire - Voir les 0 commentaires
Retour à l'accueil

Chic Meteo
Holidays

♦ Las Vegas
♦ New York
♦ UTC/GMT
♦ Paris
♦ Dakar

 

 

NON à l'excision !

Recherche

ŋ [ ] À Ññ Çç ß Óó Ëë Ïï Öö
 @ ½ ¼ Ää Üü ÷ ▀ ² ■ ª º

Al-Nd-Petit-Wolof.jpg
Le Petit Wolof deviendra grand.

 
 
  
anti-xeesal.jpg  
Anti-xeesal Campaign.
       
 
   

Syndication

  • Flux RSS des articles

Le sens du partage


pied_top.jpg
 
Contact - C.G.U. - Rémunération en droits d'auteur - Signaler un abus - Articles les plus commentés