The Wolof-Multilanguage Live Dictionary Project
Le Dictionnaire Wolof-Multilingue Vivant !



translator  wo-en en-wo grammar talk   $ 
      grammatik konversation  
HOME wo-fr fr-wo grammaire conversation sciences fr
Mercredi 2 août 2000 3 02 /08 /Août /2000 14:20

 

123  A B C D E F G H I J K L M N O P Q R S T U V W X Y Z

 

 

. fabriquer defar : Lawbe bi mooy defar leket yi. C'est le bûcheron qui fabrique les calebasses.

. fâché mer : Tey, Muusaa waxul ndaxte dafa mer. Aujourd'hui, Moussa n'a pas parlé parce qu'il est fâché.

. facile yomb : Tàggat yi dañu yomb. Les exercices sont faciles.

. faible ñàkk doole. Sa doom ji dafa ñàkk doole. Ton fils est faible.

. famille njaboot gi : Góor gaa ngiy toppatoo njabootam. L'homme s'occupe de sa famille.

. fané lax : Guró gi nga jënd dafa lax. La cola que tu as achetée est fanée.

. farce roof gi : Def naa roof ci jën wi. J'ai mis de la farce dans le poisson.

. farcir roof : Damay roof coof wi. Je farcis le mérou bronzé.

. fauter juum : Danga juum ci mbind mi. Tu as fauté dans l'écriture.

. faux dëng : Kenn wóoluwu la ndax li nga dëng. Personne n'a confiance en toi parce que tu es faux.

. favoris (du visage) faas yi : Dama wat samay faas. J'ai rasé mes favoris.

. féliciter ndokkeel : Damay ndokkeeli Faatu ci takkam. Je vais féliciter Fatou pour son maiage.

. fendu (être) xar : Taax mi dafa xar. Le mur est fendu.

. fermenter ënn : Cere ji dafa ënn, bu ko lekk ! Le couscous est fermenté. Ne le mange pas !

. fétiches xérém yi. Ndaw si dafa gëm xérém yi. La dame croît aux fétiches.

. feuille xob wi : Dagg naa xobi garab gi. J'ai coupé les feuilles de l'arbre.

. fidélité kóllëre gi : Duma la bàyyi ndax sa kóllëre. Je ne t'abandonne pas à cause de ta fidélité.

. filtrer segg : Nanga segg ndox mi balaa nga koy naan ! Il faudra filtrer l'eau avant de la boire !

. flairer fóon, xeeñtu : Fóon naa say yéré. J'ai flairé des habits.

. flâner taxawaalu, tambaalu : Gis naa ay tepp-tepp ci tali bi. J'ai vu des flaques d'eau dans la rue.

. fleur tóor-tóor bi. Jënd naa ay tóor-tóor. J'ai acheté des fleurs.

. fleuve dex gi : Ci dex gi laay sangoo. C'est dans le fleuve que je me baigne.

. flocon de maïs pet-petal bi : Damay lekk ay pet-petal. Je mange des flocons de maïs.

. flotter tëmb : Bant baa ngiy tëmb ci ndox mi. Le morceau de bois flotte dans l'eau.

. foi ngëm gi. Jullit dafay am ngëm. Le musulman doit avoir la foi.

. fondre ruy, seey : Sondeel bi seey na. La bougie a fondu.

. forêt màndiŋ mi. Golo yaa ngi ci màndiŋ. Les singes sont dans la forêt.

. fortune alal ji : Sa alal ji lew na. Tu as une fortune méritée.

. fouiller lëñbët. Nu ngiy lëñbët sàcc bi. Nous sommes en train de fouiller le voleur.

. foule mbooloo mi. Am na mbooloo mu nekk ci ëtt  bi. Il y a foule dans la cour.

. fourreau mbar mi : Defal paaka bi ci mbar mi ! Mets le couteau dans le fourreau !

. frapper dóor : Yaa dóor xale bi. C'est toi qui as frappé l'enfant.

. frère rak/mag bu góor: Sama rak bu góor. Mon petit frère. / Sama mag bu góor. Mon grand frère.

. friperie fëgg-jaay bi : Jëndal naa xale yi ay fëgg-jaay. J'ai acheté de la friperie pour les enfants.

. frissonner lox : Dama liw ba lox. J'ai tellement froid que je le frictionne

. front jë bi. Sa jë bi dafa newi. Ton front est enflé.

. frotter ragg : Raggal taabal bi bu baax ! Frotte bien la table !

. fumer saxaar : Sigaret baa ngiy saxaar. La cigarette fume.

. fumier tos gi, neefare ji : Sotti naa tos gi ci meññeef yi. J'ai versé du fumier sur les plantes.

. fusil fetal gi : Jënd naa fetal gu bees. J'ai acheté un nouveau fusil.

 

Le Petit Wolof est un dictionnaire vivant. Revenez le voir souvent.

Par wolofi - Publié dans : FR-WO
Ecrire un commentaire - Voir les 0 commentaires
Retour à l'accueil

Chic Meteo
Holidays

♦ Las Vegas
♦ New York
♦ UTC/GMT
♦ Paris
♦ Dakar

 

 

NON à l'excision !

Recherche

ŋ [ ] À Ññ Çç ß Óó Ëë Ïï Öö
 @ ½ ¼ Ää Üü ÷ ▀ ² ■ ª º

Al-Nd-Petit-Wolof.jpg
Le Petit Wolof deviendra grand.

 
 
  
anti-xeesal.jpg  
Anti-xeesal Campaign.
       
 
   

Syndication

  • Flux RSS des articles

Le sens du partage


pied_top.jpg
 
Contact - C.G.U. - Rémunération en droits d'auteur - Signaler un abus - Articles les plus commentés