The Wolof-Multilanguage Live Dictionary Project
Le Dictionnaire Wolof-Multilingue Vivant !



translator  wo-en en-wo grammar talk   $ 
      grammatik konversation  
HOME wo-fr fr-wo grammaire conversation sciences fr
Mercredi 2 août 2000 3 02 /08 /Août /2000 14:21

123  A B C D E F G H I J K L M N O P Q R S T U V W X Y Z

 

 

. gaffe njaaxum gi : Démb def nga njaaxum gu réy. Hier, tu as commis une grosse gaffe.

. gage (mettre en gage) tayle : Duudu tayle na këram ndax bare bor. Doudou a tellement de dettes qu'il a mis en gage sa maison.

. gamin gone gi, gune gi : Wool ma gune gi ! Appelle-moi le gamin !

. gauche (la) n. càmmooñ bi Ma main gauche me fait mal. Sama loxo càmmooñ dafay metti.

. gazelle kéwél gi : Yàppu kéwél dafa mooy. La viande de la gazelle est tendre.

. gecko unk wi : Gis naa benn unk ci waañ wi. J'ai vu un gecko dans la cuisine.

. gémir onk : Xadi dafa feebar bay onk. Khady est tellement malade qu'elle gémit.

. géniteur waa-jur, waa-jur : Gis naa say waa-jur. J'ai vu tes géniteurs (parents)

. genou óom bi : Sama óom dafay metti. J'ai mal au genou.

. gens gaa ñi, waa. Ana waa kër ga ? Comment vont les gens de ta maison ?

. gentil baax : Janq bi dafa baax. La jeune fille est gentille.

. germer sax : Dugub jaa ngiy sax. Le mil est en train de germer.

. gifler pes : Pes naa xaale bi ma saaga. J'ai giflé l'enfant qui m'a insulté.

. glace (miroir) seetu bi : Abal ma seetu bi ! Prête-moi la glace !

. glissant rattax : Buntu kër gi dafa rattax. La porte de la maison est glissante.

. glisser tarxiis : Dama tarxiis ci ndox mi. J'ai glissé sur l'eau.

. glorifier tagg : Géwél baa ngi lay tagg. Le griot est en train de te glorifier.

. glouton fuqle/ fëqle : Sa jabar ji dafa fëqle. Ton épouse est gloutonne

. gombo kànja gi, jaxato ji : Suppu-kànja laa togg tey. Aujourd'hui, j'ai préparé du riz à la sauce gombo.

. gosier put gi : Sama put dafay metti. J'ai le gosier qui me fait mal.

. gourde gamb bi : Jëndal naa sama doom gamb. J'ai acheté une gourde pour mon fils.

. goûter mos, ñam. Mos naa yaasa bi wànte neexul. J'ai goûté le yassa mais il n'est pas bo.

. gouvernement nguur gi. Man ci nguur gi laa bokk. Je fais partie du gouvernement.

. grain de sable pép suuf

. grandir màgg : Xale yépp màgg nañu. Tous les enfants ont grandi.

. grand-parent maam ji : Sama maam dafa màggat. Mon grand-parent est vieux.

. grappe cabb bi : Dagg naa ñaari cabbu reseŋ. J'ai coupé deux grappes de raisin.

. gras duuf : Yàpp wi nga jënd dafa duuf. La viande que tu as achetée est grasse.

. gratter xoos : Ganaar gaa ngiy xoos suuf si. La poule gratte le sol.

. grenier sàq mi. Denc nanu dugub ji ci sàq mi. Nous avons gardé lemil dans le grenier.

. grillon salliir bi : Dégg naa benn salliir ci néeg bi. J'ai entendu un grillon dans la chambre.

. grimacer gaññ : Gis naa la ngay gaññ. Je t'ai vu grimacer.

. grimper yéeg : Góor gaa ngiy yéeg ci garab gi. L'homme grimpe sur l'arbre.

. grincheux naqadi/ naqari deret : Sa yaay dafa naqadi deret. Ta maman est grincheuse (est d'un tempérament difficile).

. griot géwal/ géwél bi. Géwél yaa ngi ci ngénté li. Les griots sont au baptême.

. gris doomu-taal : Aydaa ngi sol robb bu dóomu-taal. Aïda a porté une robe grise.

. gronder gëdd. Seriñ bi gëdd na taalibe yi. Le marabout a grondé les disciples.

. gros dijj, réy : Sa biir bi dafa dijj. Ton ventre est gros.

. gué paas bi : Dex gi xootul, paas la. Le fleuve n'est pas profond. On peut passer à gué.

. guêpe njulli-kaata bi. Gis naa ay njulli-kaata ci kër gi. J'ai vu des guêpes dans la maison.

. guéri wér : Jabaru Aadama dafa feebaroon wànte wér na léegi. L'épouse d'Adama était malade. Elle est guérie maintenant.

. guetter tëru : Alkaati  yaa ngiy tëru saay-saay yi. Les policiers guettent les bandits.

. guide njiit : Sunu kurél gi am na njiit. Notre association a un guide.

. guider ommat/ wommat : Damay wommat gumba gi. Je guide l'aveugle.

. guitare (traditionnelle) xalam : Géwél yaa ngiy tëgg seeni xalam. Les griots sont en train de joeur leurs guitares.

 

Le Petit Wolof - Le dictionnaire wolof-multilingue vivant !

Par wolofi - Publié dans : FR-WO
Ecrire un commentaire - Voir les 0 commentaires
Retour à l'accueil

Chic Meteo
Holidays

♦ Las Vegas
♦ New York
♦ UTC/GMT
♦ Paris
♦ Dakar

 

 

NON à l'excision !

Recherche

ŋ [ ] À Ññ Çç ß Óó Ëë Ïï Öö
 @ ½ ¼ Ää Üü ÷ ▀ ² ■ ª º

Al-Nd-Petit-Wolof.jpg
Le Petit Wolof deviendra grand.

 
 
  
anti-xeesal.jpg  
Anti-xeesal Campaign.
       
 
   

Syndication

  • Flux RSS des articles

Le sens du partage


pied_top.jpg
 
Contact - C.G.U. - Rémunération en droits d'auteur - Signaler un abus - Articles les plus commentés