Le Dictionnaire Wolof-Multilingue Vivant !
| translator | wo-en | en-wo | grammar | talk |
♦ $ ♦ ♦ |
| grammatik | konversation | ||||
| HOME | wo-fr | fr-wo | grammaire | conversation | sciences fr |
| translator | wo-en | en-wo | grammar | talk |
♦ $ ♦ ♦ |
| grammatik | konversation | ||||
| HOME | wo-fr | fr-wo | grammaire | conversation | sciences fr |
123 A B C D E F G H I J K L M N O P Q R S T U V W X Y Z
. idée xalaat mi : Say xalaat rafet nañu. Tes idées sont bonnes.
. igname ñàmbi ji : Cére ji amul ñàmbi. Il n'y a pas d'igname dans le couscous.
. iguane bar bi : Gis naa benn bar ci booru dex gi. J'ai vu un iguane au bord du fleuve.
. île dun bi : Dëkk baa ngi ci dun bi. Le village se trouve sur l'île.
. image nataal bi/ nitaal bi : Gis naa ay nataal ci téere bi. J'ai vu des images dans le livre.
. imiter roy, toppandoo : Usmaan dafay roy magam. Ousmane imite son aîné.
. implorer ñaan : Damay ñaan Yàlla. J'implore Dieu.
. impoli reew : Sa doom ji dafa reew. Ton fils est impoli.
. importer jëggaani. Suukër si dañu ko jëggaani. On a importé le sucre.
. importuner sonnal, lëjal : Yaa ngi may sonnal. Tu m'importunes.
. imprimer muul : Nu ngiy muul sunu téere yi. Nous sommes en train d'imprimer nos livres.
. impuissant (sexuellement) yoom : Jëkkëru Rama dafa yoom. Le mari de Rama est impuissant.
. incendie lakk gi : Sunu gox bi dafa am lakk. Il y a un incendie dans notre quartier.
. indication joxoñn bi, tegtal bi : Lii, baatu joxoñ la. 'Ça' est un mot pour indication.
. indigent néew-ji-doole ji : Taalibe yi ay néew-ji-doole lañu. Les mendiants sont des indigents.
. indigestion fër : Ci tabaski ji, dama fëroon. J'avais une indigestion pendant la Tabaski.
. informer (s') laajte. Damay laajte xabaar yi. Je m'informe sur les nouvelles.
. injurier saaga. Abdu dafa saaga nijaayam. Abdou a injurié son oncle.
. innocent muumin mi : Muusa yëgul li xew, muumin la. Moussa n'est pas au courant de ce qui se passe, c'est un innocent.
. inondation mbënn mi : Ci nawet bi, mbënn mi agsi na ba ci dëkk bi. Pendant l'hivernage, l'inondation est arrivée jusque dans la ville.
. insinuer gaaral : Sofi ngiy gaaral xaritam. Sophie fait des insinuations à l'endroit de son ami.
. intelligence xel mi : Sa xel mi dafa ëpp. Ton intelligence est excessive.
. interdit aay, araam. Sàngara dafa araam ci jullit. L'alcool est interdit aux musulmans.
. invulnérable tul : Sama yaram dafa tul. Je suis invulnérable.
. isoler ber, beddi : Dañu ber jarag ji. On a isolé le malade.
. ivre màndi : Gis naa Tafa mu màndi ba mënul dox. J'ai vu Tapha ivre jusqu'à ne pas pouvoir marcher.
Le Petit Wolof est un dictionnaire vivant. Revenez le voir souvent.
| ŋ [ ] À Ññ Çç ß Óó Ëë Ïï Öö |
|
@ ½ ¼ Ää Üü ÷ ▀ ² ■ ª º |