The Wolof-Multilanguage Live Dictionary Project
Le Dictionnaire Wolof-Multilingue Vivant !


translator  wo-en en-wo grammar talk   $ 
      grammatik konversation  
HOME wo-fr fr-wo grammaire conversation sciences fr
Mercredi 2 août 2000 3 02 /08 /2000 14:26

123  A B C D E F G H I J K L M N O P Q R S T U V W X Y Z

 

 

. laid ñaaw : Sa coro li dafa ñaaw. Ta fiancée est laide.

. laisser bàyyi, waxx : Bàyyil bunt bi ! Laisse la porte !

. lait meew mi : Jënd naa meew mu bare. J'ai acheté beaucoup de lait.

. lame lañset bi : Damay watu ak lañset bi. Je me rase avec la lame.

. lance-pierres mbaq mi, laspeer gi. Mbaq laay rëbbe picc yi. Je chasse les oiseaux avec un lance-pierres.

. lancer sànni : Damay sànni bal bi ci dex gi. Je lance la balle dans le fleuve.

. langage wax ji, waxin wi : Sa waxin rafetul. Ton langage n'est pas correct.

. lange laaytaay li : Jëndal naa sama doom ay laaytaay. J'ai acheté des langes pour ma fille.

. langer ngemb : Damay ngemb xale bi. Je lange l'enfant.

. langue làmmiñ wi, làkk wi : Ban làkk ngay wax ? Quelle langue parles-tu?

. lapin lëg gi : Am naa ay lëg yu bare. J'ai beaucoup de lapins.

. large yaa : Sunu dëkk dafa yaa. Notre ville est large.

. larme rangooñ wi : Sa rangooñ yaa ngiy wal. Tes larmes coulent.

. larmoyer bas : Sama bët yaa ngiy bas ndax kaani gi. Mes yeux larmoient à cause du piment.

. larve sax wi, wallax-njaan wi : Gis naa ay sax ci teen bi. J'ai vu des larves dans le puits.

. laver raxas : Damay raxas samay loxo. Je lave mes mains.

. lécher mar : Xaj baa ngiy mar kuddu gi. Le chien lèche la cuillère.

. léger woyaf, woyof : Saag bi dafa woyaf. Le sac est léger.

. légume paytéef bi, lujum bi : Damay jënd ay paytéef. J'achète des légumes.

. lent yéex, yiix : Sa fas wi dafa yéex. Ton cheval est lent.

. lentement ndànk : Faatoo ngiy dox ndànk. Fatou marche lentement.

. lèpre gaana gi : Góor gi dafa gaana. L'homme a la lèpre

. lever yëkkëti : Damay yëkkëti taabal bi. Je lève la table.

. lèvre tuñ mi : Dama màtt sama tuñ. Je me suis mordu la lèvre.

. lie nëxit mi : Tuur naa nëxitu dëwliñ ji. J'ai versé la lie de l'huile.

. lieu béréb bi : Ci ban béréb ngeen nekkoon ? Dans quel lieu étiez-vous ?

. lignée deret ji, askan wi : Ci ban askan nga bokk ? Tu es de quelle lignée ?

. linge póot mi : Yóbbu naa sama póot ci póotkat bi. J'ai amené mon linge chez la lingère.

. lion gaynde gi : Gis naa ay gaynde ci pàkku ñokkolo-koobaa. J'ai vu des lions au parc du Niokolo-Koba.

. lire jàng, duruus : Maa ngiy jàng ci sama téere wolof. Je lis dans mon livre de wolof.

. lit lal bi : Maa ngiy tëdd ci lal bi. Je me couche dans le lit.

. litre liitër bi : Jënd naa ñaari liitëru meew. J'ai acheté deux litres de lait.

. livre téere bi : Damay nafar ci sama téere wolof. Je révise dans mon livre de wolof.

. livrer jébbal, jébbale : Jébbal nanu sàcc bi alkaati bi. Nous avons livré le voleur au policier.

. loi yoon wi, sàrt bi : Yoon, kenn du ko jalgati. On ne doit pas enfreindre la loi.

. loin sore, sori : Fi ngeen dëkk, dafa sore. C'est loin là où vous habitez.

. long gudd : Yoon wi dafa gudd. La route est longue.

. lourd diis : Sa saag bi dafa diis. Ton sac est lourd.

. lune weer wi : Weer wi feeñ na. La lune est apparue.

. lutteur mbër mi : Mbër yaa ngiy tàggat seen yaram. Les lutteurs font du sport.

 

Le Petit Wolof - Le dictionnaire wolof-multilingue vivant

Par wolofi - Publié dans : FR-WO
Ecrire un commentaire - Voir les 0 commentaires - Partager    
Retour à l'accueil

  • : Vocabulaire et grammaire wolof ainsi que ce que je vois de ma fenêtre.

Chic Meteo
Holidays

♦ Las Vegas
♦ New York
♦ UTC/GMT
♦ Paris
♦ Dakar

 

 

NON à l'excision !

Recherche

ŋ [ ] À Ññ Çç ß Óó Ëë Ïï Öö
 @ ½ ¼ Ää Üü ÷ ▀ ² ■ ª º

Syndication

  • Flux RSS des articles

Le sens du partage


pied_top.jpg
 
Contact - C.G.U. - Rémunération en droits d'auteur - Signaler un abus - Articles les plus commentés