Le Dictionnaire Wolof-Multilingue Vivant !
| translator | wo-en | en-wo | grammar | talk |
♦ $ ♦ ♦ |
| grammatik | konversation | ||||
| HOME | wo-fr | fr-wo | grammaire | conversation | sciences fr |
| translator | wo-en | en-wo | grammar | talk |
♦ $ ♦ ♦ |
| grammatik | konversation | ||||
| HOME | wo-fr | fr-wo | grammaire | conversation | sciences fr |
123 A B C D E F G H I J K L M N O P Q R S T U V W X Y Z
. mâcher sàqami : Bu may lekk, damay sáqami. En mangeant, je mâche les aliments.
. mâchoire ŋaam wi, kaabaab bi : Yaa ma pes ci ŋaam. C'est toi qui m'as giflé à la mâchoire.
. magicien luxuskat bi : Luxuskat baa ngiy luxusal xale yi ay tàngal. Le magicien fait de la magie pour les enfants en leur trouvant des bonbons.
. main loxo bi : Damay raxas samay loxo. Je lave mes mains.
. maison kër gi : Tabax naa kër gu rafet. J'ai construit une belle maison.
. malade jarag ji : Gis naa ay jarag opitaal. J'ai vu des malades à l'hôpital.
. malade (être) feebar, opp, wopp (grave) : Sama maam dafa feebar. Mon grand-parent est malade.
. maladif wéradi, xiibon : Sa doom ji dafa xiibon. Ton fils est maladif.
. malaxer jamb : Damay jamb sunguf si. Je malaxe la farine.
. malhonnête dëng : Jaaykat bi dafa dëng. Le marchand est malhonnête.
. malin muus : Abduu sale bu muus la. Abdou est un garçon malin.
. mamelle ween wi : Nag waa ngiy nàmpal doomam ak ween yi. La vache allaite son petit avec ses mamelles.
. manger lekk : Nu ngiy lekk ceebu-jën. Nous mangeons du riz au poisson.
. manioc pullóox bi, ñàmbi ji : Dinaa def pullóox ci cere ji. Je mettrai du manioc dans le couscous.
. manquer ñàkk : Ci joŋante bi, ñàkk naa xaalis bu bare. J'ai perdu beaucoup d'argent à la loterie.
. marabout sëriñ bi : Sëriñ baa ngiy jàngal taalibé yi. Le marabout enseigne les disciples.
. marchand jaaykat bi : Damay jënd ay lujum ci jaaykat bi. J'achète des légumes chez la marchande.
. marchander waxaale : Tubaab baa ngiy waxaale. Le Blanc est en train de marchander.
. marcher dox : Nu ngiy dox ci tefes gi. Nous marchons sur la plage.
. marché ja ba, marse bi : Maa ngiy dem ja ba. Je vais au marché.
. mare déeg bi : Nag yaa ngiy naan ci déeg bi. Les vaches s'abreuvent à la mare.
. mari jëkkër ji : Gis naa sa jëkkër. J'ai vu ton mari.
. mariage séy, sëy bi, takk gi. Ci takk gi laa nekkoon. J'étais au mariage.
. marmite cin lin, kàddir gi, kawdir gi. Cin laa ngi ci taal bi. La marmite est au feu.
. marque màndarga bi : Góor gi dafa am màndarga ci kanam gi. L'homme a une marque sur la figure.
. marraine bàjjan bi : Sama bàjjan dafa feebar. Ma tante marraine est malade.
. maure naar bi : Naar yaa nga gànnaar. Les Maures sont en Mauritanie.
. méchant bon, aay, soxor : Xaj bi dafa soxor. Le chien est méchant.
. mécréant yéeféer bi : Sa gan gi yéeféer la. Ton hôte est un mécréant.
. médicament garab gi : Jënd naa garab yi. J'ai acheté les médicaments.
. médire jëw : Ñawkat baa ngiy jëw xaritam. Le tailleur médit de son ami.
. mélanger boole, jaxase : Dama jaxase góor ñi ak jigéen ñi. J'ai mélangé les filles et les garçons.
. menacer (en paroles) tëkku : Alkaati bi tëkku na ma. Le policier m'a menacé.
. meneur njiit li : Sunu kurél gi amul njiit. Notre structure n'a pas de meneur.
. mentir nar, fen, kàcc : Sa xarit bi dafa mëna nar lool. Ton ami est un grand menteur.
. mépriser jéppi sib : Sa jabar ji dafa la jéppi. Ton épouse te méprise.
. mer géej gi : Gaal gaa ngi ci géej gi. Le bateau est dans la mer.
. mère ndey ji, yaay ji : Sama yaay gaañu na. Ma mère est décédée.
. mériter yeyoo, yelloo : Sa liggéey bi yelloo nga ko. Tu mérites ton travail.
. message bataaxal bi : Jot naa sa bataaxal. J'ai reçu ton message.
. monde àddina bi, dunyaa ji : Àddina bi dafa yaatu. Le monde est vaste.
. monnaie weccit wi : Jox ma sama weccit ! Donne-moi ma monnaie !
. monter yéeg, war : Damay yéeg ci fas wi. Je monte sur le cheval.
. montrer won, wone : Nanga ma won sa kër ! Il faudra me montrer ta maison !
. mordre màtt : Xa bi màtt na xale bi. Le chien a mordu l'enfant.
. mort dee, gaañu : Xar mi dee na. Le mouton est mort.
. mouche weñ wi : Kër gi dafa bare weñ. Il y a beaucoup de mouches dans la maison.
. moustique yoo yi : Yoo mooy joxe sibiru. C'est le moustique qui transmet le paludisme.
. moustiquaire sànke bi : Sanke baax na ci yoo yi. La moustiquaire est utile contre les moustiques.
. mouton xar mi : Jënd naa xar. J'ai acheté un mouton.
Le Petit Wolof - Le dictionnaire wolof-multilingue vivant
| ŋ [ ] À Ññ Çç ß Óó Ëë Ïï Öö |
|
@ ½ ¼ Ää Üü ÷ ▀ ² ■ ª º |