Le Dictionnaire Wolof-Multilingue Vivant !
| translator | wo-en | en-wo | grammar | talk |
♦ $ ♦ ♦ |
| grammatik | konversation | ||||
| HOME | wo-fr | fr-wo | grammaire | conversation | sciences fr |
| translator | wo-en | en-wo | grammar | talk |
♦ $ ♦ ♦ |
| grammatik | konversation | ||||
| HOME | wo-fr | fr-wo | grammaire | conversation | sciences fr |
123 A B C D E F G H I J K L M N O P Q R S T U V W X Y Z
. obéir déggal, topp : Nanga déggal say waa-jur. Il faudra obéir à tes parents.
. objet lëf ki, yëf yi (pl) : Ana yëf yi ? Où sont les objets ?
. obligation wareef wi, warugar wi : Li nga def, warugar la. Ce que tu as fait est une obligation.
. obliger à ga : Dañu ga góor gi ngir mu takk jabar. On a obligé l'homme à se marier.
. obscur lëndëm : Sa néeg bi dafa lëndëm. Ta chambre est obscure.
. obsèques dëj bi : Dama demoon dëj ba. J'étais allé aux obsèques.
. observer xool : Xoolaal tabló bi ! Observe le tableau !
. obstacle gàllankoor wi : Mënuma dem ndaxte dama am gàllankoor. Je ne peux pas aller à cause d'un obstacle.
. occupé jàpp : Dama jàpp xaaral tuuti ! Je suis occupé, attends un peu !
. océan géej gi. Géej gi dafa sàmbaraa. L'océan est agité.
. odeur xet gi, cóola gi : Xet gaa ngiy dugg ci néeg bi. L'odeur entre dans la chambre.
. oeil bët bi, gët gi. Sama bët dafay metti. Mon oeil me fait mal.
. oeuf nen bi : Jënd naa ay nen. J'ai acheté des oeufs.
. offrande sarax si : Def naa ay sarax. J'ai fait des offrandes.
. offrir may : Dama lay may xaalis bu bare. Je t'offre beaucoup d'argent.
. oignon soble si : Am naa toolu soble. J'ai un champ d'oignons.
. oiseau picc mi : Picc maa ngiy naaw. L'oiseau vole.
. omettre fàtte : Fàtte naa jënd suukër. J'ai omis d'acheter du sucre.
. oncle nijaay ji : Sama nijaay laay toggal yaasa. Je prépare du yassa pour mon oncle.
. ongle we wi : Damay dagg samay we. Je me coupe les ongles.
. or wurus : Jënd naa ay lami wurus. J'ai acheté des bracelets en or.
. ordre ndigal li : Kelifa gi joxe na ndigal. Le patron a donné l'ordre.
. ordure mbalit mi, mbuubit mi : Dindi naa mbalit mi. J'ai enlevé les ordures.
. oreille nopp b : Sama nopp dafay metti. J’ai mal à l’oreille.
. oreiller njegenaay li : Maa ngi teg sama bopp ci njegenaay li. J’ai posé ma tête sur l’oreiller.
. origine cosaan li : Xam nga cosaanu wolof? Tu connais l’origine du wolof ?
. orner sàdd : Damay sàdd sama néeg ak ay nataal. J’orne ma chambre de photos.
. oseille bisaab : Maa ngiy naan bisaab. Je bois du jus de bissap.
. oser ñeme : Man ñeme naa song gaynde gi. J’ose attaquer le lion.
. ostentation ngistal li : Li nga def, ngistal la. Ton geste est de l’ostentation.
. oublier fàtte : Dama fàtte jënd meew. J’ai oublié d’acheter du lait.
. ouest sowu bi : Sunu dëkk, sowu la féeté. Notre village est situé à l’ouest.
. outil jumtukaay bi : Jënd naa ay jumtukaay. J’ai acheté des outils.
. ouvrir ubbi, tijji. Damay ubbi bunt bi. J’ouvre la porte.
. où ana, fan : Ana Oumar? Où est Omar? Fooy ( contraction de fu ngay) dem? Où vas-tu?
Le Petit Wolof est un dictionnaire wolof-multilingue vivant. Venez le voir souvent !
| ŋ [ ] À Ññ Çç ß Óó Ëë Ïï Öö |
|
@ ½ ¼ Ää Üü ÷ ▀ ² ■ ª º |