Mercredi 2 août 2000
3
02
/08
/2000
14:30
123 A B C D E
F G H I J
K L M N O
P Q R S T
U V W X Y Z
. page xët mi : Ubbil xët juróom ñeent ! Ouvre à la page neuf!
. pagne sér bi, sër bi, pendal mi : Jënd na sér bu rafet. J’ai acheté un beau pagne.
. paie peyoor bi : Jot naa sama peyoor. J’ai reçu ma paie.
. pain mburu mi : Mburu mi dafa wow. Le pain est sec.
. paix jàmm ji : Jàmm ci la lépp xaj. Rien ne vaut la paix.
. palissade sàkket wi : Dama sàkket sama kër. J’ai clôturé ma maison avec une palissade.
. palper làmb : Doktoor baa ngiy làmb sama biir. Le médecin palpe mon ventre.
. paludisme sibbiru si : Sibbiru si dafa bare ci nawet bi. Le paludisme est très répandu pendant l’hivernage.
. panaris bëy bi : Sama loxo dafa bëy. J’ai un panaris au doigt.
. panse bàq gi mbàq gi : Raxas nañu mbàqu xar mi. On a lavé la panse du mouton.
. pantalon caaya ji, tubéy ji : Damay sol sama tubéy. Je porte mon pantalon.
. papier kayit wi : Damay bind ci kayit wi. J’écris sur le papier.
. papillon lëpp-lëpp bi : Jàpp naa benn lëpp-lëpp. J’ai attrapé un papillon.
. paradis àjjana ji. Yàlla nanu Yàlla yóbbu àjjana ! Que Dieu nous amène au paradis !
. paralyser (se) làggi : Tànki xale bi dañu làggi. L’enfant a les jambes paralysées.
. parcelle waar wi : Damay bey sama waar. Je cultive ma parcelle.
. pardonner baal, jéggal : Yàlla nana Yàlla baal ! Que Dieu nous pardonne !
. parent mbokk mi : Am naa ay mbokk ci Ndar. J’ai des parents à Saint-Louis.
. paresseux tayel : Sa jabar ji dafa tayel. Ton épouse est paresseuse.
. parler wax : Maa ngiy wax ak yow. Je parle avec toi.
. partager bokk, séddale : Damay séddale mburu mi. Je partage le pain.
. partir dem : Damay dem sama kër xarit. Je pars chez mon ami.
. passer jaar, aw : Démb, jaar naa ci sa kër. Hier, je suis passé chez toi.
. pastèque xaal bi : Jënd naa xaal bu réy. J’ai acheté une grosse pastèque.
. patienter muñ, taaxirlu : Nanga muñ bu baax ! Il faudra beaucoup patienter !
. patron kelifa gi : Sunu kelifa ñëw na. Notre patron est arrivé.
. payer fey : Maa ngiy fey boroom butig bi. Je paye le boutiquier.
. pays réew mi : Senegaal mooy sunu réew. Le Sénégal est notre pays.
. pêcher napp : Damay napp ay waas. Je pêche des carpes.
. penser xalaat : Damay xalaat sama yaay. Je pense à ma mère.
. percer bëtt, bënn : Sama saag dafa bëtt. Mon sac est percé.
. perdu réer : Sama caabi réer na. Ma clé est perdue.
. père baay bi : Sama baay dafa tukku. Mon père a voyagé.
. personnalité faayda ji : Nit dafay am faayda. L’être humain doit avoir de la personnalité.
. personne nit ki : Gis naa ay nit ci ëtt bi. J’ai vu des personnes dans la cour.
. péter doxat, yuusal (sans bruit) : Danga doxat sànq. Tu as pété tout à l’heure.
. peuple askan wi, xeet wi : Sama askan a nga Maali. Mon peuple est au Mali.
. peur ragal gi / avoir peur ragal, tiit : Dama ragal xaj bi. J’ai peur du chien.
. peut-être amaana, xëy-na : Amaana ma dem Amerig. Peut-être que j’irai en Amérique.
. pied tànk bi : Sama tank dafay metti. J’ai mal au pied.
. piège fiir gi : Jàpp naa jinax ak fiir gi. J’ai attrapé la souris avec un piège.
. pierre xeer wi, doj wi. For naa ay doj. J’ai ramassé des pierres.
. pigeon petax mi / pitax mi : Petax mi naaw na. Le pigeon a volé.
. piler dëbb, soq : Jigéen ñaa ngiy dëbb dugub ji. Les femmes pilent le mil.
. pilier kenu bi : Julli, kenu lislaam la. La prière est un pilier de l’Islam.
. piller lël : Sàcc bi lël na sama kër. Le voleur a pillé ma maison.
. pilon kuur gi : Jigéen jaa ngiy soq ak kuur gi. La femme pile avec le pilon.
. pilment kaani gi : Def naa kaani ci yaasa bi. J’ai mis du piment dans le yassa.
. piquer jam : Pont a ma jam ci tànk. J’ai été piqué par une pointe au pied.
. pirogue gaal gi. Damay jàll dex gi ak gaal. Je traverse le fleuve en pirogue.
. plage tefes gi : Tubaab yaa ngiy sangu ci tefes gi. Les Blancs se baignent sur la plage.
. pleurer jooy : Xale baa ngiy jooy. L’enfant est en train de pleurer.
. pluie taw bi : Taw bi barewul ci Ndar. Il n’y a pas beaucoup de pluie à Saint-Louis.
. poche jiba ji, poos bi : Denc naa sama xaalis ci sama jiba. J’ai gardé mon argent dans ma poche.
. poisson jën wi : Jën yi bare nañu ci dex gi. Il y a beaucoup de poissons dans le fleuve.
. pondéré teey : Góor gi dafa teey. L’homme est pondéré.
. pondre nen : Ganaar yi nen nañu. Les poules ont pondu des oeufs.
. porte bunt bi : Tëj naa bunt bi ak caabi. J’ai fermé la porte à clé.
. pourrir nëb : Màngo yi dañu nëb. Les mangues sont pourries.
. poussière pënd bi : Tey, pënd bi dafa bare. Il y a beaucoup de poussière aujourd’hui.
. pouvoir nguur gi : Sama nijaay mu ngi ci nguur gi. Mon oncle est dans le pouvoir.
. précéder jiitu : Yaa ma jiitu Senegaal. C’est toi qui m’as précédé au Sénégal.
. prendre fab, jël : Yaa jël samay caabi. C’est toi qui as pris mes clés.
. présent teew : Dinaa teew ci ngénté li. Je serai présent au baptême.
. presque daanaka : Sama liggéey jeex na daanaka. Mon travail est presque terminé.
. prêter able : Tey dama able sama oto. Aujourd’hui, j’ai prêté ma voiture.
. prévoir fàggu : Nanga fàggu loo añe. Il faut prévoir de quoi déjeuner.
. prix njëg gi : Xam naa njëgu oto bi. Je connais le prix de la voiture.
. profond xóot : Teen bi dafa xóot. Le puits est profond.
. promener (se) doxantu : Damay doxantu ci tefes gi. Je me promène sur la plage.
. propre set : Sa kër gi set na wecc. Ta maison est très propre.
. propriétaire boroom bi. Yaay boroom kër gi. Tu es le propriétaire de la maison.
. protéger aar, saytu, yiir : Ñakk, dafay aar xale yi. La vaccination protège les enfants contre les maladies.
. provenir jóge, bawoo, tukkee : Biiñ baa ngi jóge farañs. Le vin provient de la France.
. proverbe léebu bi : Sama téere bi am na ay léebi wolof. Mon livre a des proverbes wolof.
. provision ndugg li. Sama ndugg li jeex na. Ma provision est finie.
. puce fel wi : Sa kër gi dafa bare fel. Il y a beaucoup de puces dans ta maison.
. pudeur kersa gi : Sa xarit bi dafa bare kersa. Ton ami a beaucoup de pudeur.
. puiser duy, root : Maa ngiy duy ndox ci teen bi. Je puise de l’eau au puits.
. puits teen bi : Jigéen ñaa ngiy root ci teen bi. Les femmes puisent de l’eau au puits.
Le Petit Wolof est un dictionnaire vivant. Revenez le voir souvent.
Par wolofi
-
Publié dans : FR-WO
0
-
Partager