The Wolof-Multilanguage Live Dictionary Project
Le Dictionnaire Wolof-Multilingue Vivant !



translator  wo-en en-wo grammar talk   $ 
      grammatik konversation  
HOME wo-fr fr-wo grammaire conversation sciences fr
Mercredi 2 août 2000 3 02 /08 /Août /2000 14:32

123  A B C D E F G H I J K L M N O P Q R S T U V W X Y Z

 

 

. rabrouer jànni : Sama yaay dafa ma jànni. Ma mère m’a rabroué.
. race xeet wi, askan wi : Ci xeetu wolof laa bokk. Je suis de la race wolof.
. racine reen bi : Dindi naa reenu garab gi. J’ai enlevé la racine de l’arbre.
. raconter nettali, léeb : Damay nettali xale yi léeb bi. Je raconte le conte aux enfants.
. raffermir feddali : Damay feddali sama kóllëre ak yow. Je raffermis mes relations avec toi.
. raison (avoir) yey : Maa yey ci àtte bi. J’ai eu raison au jugement.
. ramadan koor gi : Woor naa ci koor gi. J’ai jeûné au ramadan.
. ramasser for : Démb for naa xaalis bu bare. Hier, j’ai ramassé beaucoup d’argent.
. ramer joow : Mool yaa ngiy joow gaal gi. Les pêcheurs sont en train de ramer la pirogue.
. rancune (garder) tongu : Tey Ayda dafa ma tongu. Aujourd’hui Aïda m’a gardé rancune.
. rangée sàppe si : Defarleen sàppe si ! Faites les rangées !
. rapide gaaw, bar : Sa waxin dafa gaaw. Ta façon de parler est rapide.
. rapiécer gaar, daax. Damay gaar sama tubéy. Je rapièce mon pantalon.
. rappeler fàttali : Dinaa la fàttali sa bataaxel bi. Je te rappellerai ta lettre.
. raser wat : Damay wat boppu xale bi. Je rase la tête de l’enfant.
. rassembler dajale : Suba dinaa dajale xale yi ci sama kër. Demain, je rassemblerai les enfants chez moi.

. rat jinax, janax ji, kaña gi (gros rat) : Sunu kër am na ay janax. Il y a des rats chez nous.
. recevoir jot : Démb, jot naa ay bataaxal. Hier, j’ai reçu des lettres.
. réchauffer (se) jaaru : Daan naa jaaru ci sedd bi. J’avais l’habitude de me réchauffer pendant la saison froide.
. rechercher wut : Damay wut sama caabi. Je cherche ma clé.
. récipient ndab li : Def naa ndox ci ndab li. J’ai mis de l’eau dans le récipient.
. réciter tari : Maa ngiy tari samay saar. Je récite mes leçons.
. reconnaître ràññee, xàmmi, xammee : Xàmme naa samay wa-jur. Je reconnais mes parents.
. réfléchir xalaat, gëstu : Damay xalaat ci mbir mi. Je réfléchis sur l’affaire.
. refuser bañ : Xale bi bañ na jàng wolof. L’enfant a refusé d’apprendre le wolof.
. regarder xool : Damay xool rawante bi. Je regarde la course.
. région diiwaan bi : Sunu diiwaan dafa yaatu. Notre région est vaste.
. regretter réccu : Waa jaa ngiy réccu li mu defoon. L’homme regrette ce qu’il avait fait.
. rein ndigg li : Sama ndigg dafay metti. J’ai mal aux reins.
. reine buur bi : Gis naa buur bu jigéen bi. J’ai vu la reine.
. relier lëkkale : Yoon wii mooy lëkkale ñaari dëkk yi. C’est cette route qui relie les deux villes.
. religion diiné ji : Sunu diiné bëggul sàngara. Notre religion n’aime pas l’alcool.
. remercier gërëm : Maa ngiy lay gërëm bu baax. Je te remercie infiniment.
. remettre jox : Dinaa la jox sa xaalis suba. Je te remettrai ton argent demain.
. rencontrer daje, tase : Bi may ñëw, daje naak yow. En venant je t’ai rencontré.
. rendre delloo : Dinaa la delloo sa weccit. Je te rendrai ta monnaie.
. rentrer chez soi ñibbi : Damay ñibbi sama kër. Je rentre chez moi.
. réparer defar, jagal : Dama defar sama oto. Je répare ma voiture.
. repartir dellu : Dinaa dellu Dakaar suba. Je repartirai à Dakar demain.
. repas lekk gi : Indi nañu lekk gi ci sa kër. Ils ont amené le repas chez toi.
. repasser paase, fudd : Damay fudd sama simis. Je repasse ma chemise.
. repentir (se) réccu : Jigéen ji réccu na li mu def jëkkëram. La femme regrette ce qu’elle a fait à son mari;. elle se repentit.
. répéter baamtu, baamu : Damay baamtu li ma wax. Je répète ce que j’ai dit.
. repiquer jëmbët : Garab gii, dañu ko fi jëmbët. Cet arbre-là a été repiqué ici.
. répliquer tontu, àddu : Bul tontu sa baay ! Ne réplique pas aux menaces de ton père !
. répondre wuyu, tontu : Dinaa tontu sa bataaxal. Je répondrai à ta lettre.
. reporter (à plus tard) fomm : Dañu fomm ndaje mi. On a reporté la réunion.
. repos noflaay bi : Sa noflaay bi jeexagul. Ton repos n’est pas encore fini.
. reposer (se) noppalu. Maa ngiy noppalu ci sa néeg. Je me repose dans ta chambre.
. respirer noyyi, nokki : Sama bakkan laay noyee. C’est avec le nez que je respire.
. ressusciter dekki : Yeesu dekki na. Jésus est ressuscité.
. rester des : Sama xaalis des na tuuti. Il me reste un peu d’argent.
. résumer tënk : Damay tënk li ma wax. Je résume ce que j’ai dit.
. retenir téye : Dañu ma téye ci bunt bi. On m’a retenu à la porte.
. réunion ndaje mi : Am nanu ndaje suba. Nous avons réunion demain.
. réussir tekki : Sa doom ji tekki na. Ton fils a réussi.
. réussite ndam li : Sa ndam li am na solo. Ta réussite est capitale.
. rêve gént gi : Sa gént gi doy na waar. Ton rêve est bizarre.
. réveiller yee : Damay yee xale yi. Je réveille les enfants.
. revenir dellusi : Dinaa dellusi Ndar déwén. Je reviendrai à Saint Louis l’année prochaine.
. rire ree : Gis naa la ngay ree. Je t’ai vu rire.
. riz ceeb bi : Damay bey ceeb ci sama tool. Je cultive du riz dans mon champ.
. rôtir saaf : Damay saaf ginaar gi. Je rôtis le poulet.

Le Petit Wolof est un dictionnaire vivant. Revenez le voir souvent.

Par wolofi - Publié dans : FR-WO
Ecrire un commentaire - Voir les 0 commentaires
Retour à l'accueil

Chic Meteo
Holidays

♦ Las Vegas
♦ New York
♦ UTC/GMT
♦ Paris
♦ Dakar

 

 

NON à l'excision !

Recherche

ŋ [ ] À Ññ Çç ß Óó Ëë Ïï Öö
 @ ½ ¼ Ää Üü ÷ ▀ ² ■ ª º

Al-Nd-Petit-Wolof.jpg
Le Petit Wolof deviendra grand.

 
 
  
anti-xeesal.jpg  
Anti-xeesal Campaign.
       
 
   

Syndication

  • Flux RSS des articles

Le sens du partage


pied_top.jpg
 
Contact - C.G.U. - Rémunération en droits d'auteur - Signaler un abus - Articles les plus commentés