The Wolof-Multilanguage Live Dictionary Project
Le Dictionnaire Wolof-Multilingue Vivant !



translator  wo-en en-wo grammar talk   $ 
      grammatik konversation  
HOME wo-fr fr-wo grammaire conversation sciences fr
Mercredi 2 août 2000 3 02 /08 /Août /2000 14:34

123  A B C D E F G H I J K L M N O P Q R S T U V W X Y Z

 

 

. tabac póon mi, përis mi : Damay tóx përis. Je fume du tabac.
. table taabal ji : Teg naa ndékki li ci taabal ji. J’ai mis le petit déjeuner sur la table.
. tablette coranique àlluwa ji : Damay bind ci sama àlluwa. J’écris sur ma tablette coranique.
. tache gàkk-gàkk bi : Sa simis bi am na ay gàkk-gàkk. Ta chemise a des taches.
. taire (se) noppi : Waxal xale yi ñu noppi ! Dis aux enfants de se taire !
. tamarin daqaar ji : Def naa daqaar ci cin li. J’ai mis du tamarin dans la marmite.
. taper fëgg, dóor : Damay fëgg bunt bi. Je tape à la porte.
. taquiner tooñ : Yaa ngi may tooñ. Tu es en train de me taquiner.
. tarir ŋacc, déy : Sunu teen dafa déy. Notre puits est tari.
. taureau yëkk wi : Rey nañu benn yëkk ci takk gi. On a tué un taureau au mariage.
. teindre cuub/suub : Damay suub sama mbubb. Je teins mon boubou.
. témoin seede bi : Am naa ay seede ci àtte bi. J’ai des témoins au jugement.
. temps jamano, jamono ji : Léegi jamono ji dafa metti. Maintenant les temps sont durs.
. terminer noppi, pare, sottal, àggale : Sama liggéey noppi na. Mon travail est terminé.

. terrain pàkk bi, suuf si : Am naa ñaari pàkk. J’ai deux terrains.
. tête bopp bi : Sama bopp dafay metti. J’ai la tête qui me fait mal.
. téter nàmp : Sofi dafay nàmpal doomam. Sophie fait téter sa fille.
. têtu të, dëgër bopp : Xale bi dafa dëgër bopp. L’enfant est têtu.
. texte xët mi : Maa ngiy jàng xët mi. Je lis le texte.
. thé àttaaya ji, warga wi (vert) : Damay naan àttaaya. Je bois du thé.
. tiède nugg : Ndox mu nugg laay sangoo. Je me douche à l’eau tiède.
. tisser ràbb : Damay ràbb ay njoowaan. Je tisse des hamacs.
. tissu ndimo li : Jënd naa ndimo lu ñuul. J’ai acheté du tissu noir.
. toilettes wanag wi, sutura bi : Am na ku nekk ci wanag wi. Il y a quelqu’un dans les toilettes.
. tomber daanu, rot, dal : Bunt bi daanu na. La porte est tombée.
. tonnerre dënnu gi : Biig, déeg naa ay dënnu yu metti. Hier, j’ai entendu de terribles coups de tonnerre.
. torche niitu gi : Abal ma niitu gi ! Prête-moi la torche !
. tordu dëng : Yoon wi dafa dëng. La route est tordue.
. tortue mbonaat mi : Gis naa mbonaat ci dex gi. J’ai vu une tortue dans le fleuve.
. torturer mbugal, bugal : Yoon, dafa tere mbugal. La loi interdit de torturer quelqu’un.
. totem mbañ gi : Sunuy aada am nañu ay mbañ. Nous avons des totems dans nos coutumes.

. toucher làmb, laal : Bul làmb sama poof ! Ne touche pas ma cuisse !

. touffu sëq : Sama bopp dafa sëq. Ma tête est touffue de cheveux.

. tour ay gi, (de rôle) moome gi : Dinaa ñëw ci sa moome. Je viendrai à ton tour.

. tourbillon callweer wi : Tey dëkk bi dafa bare callweer. Aujourd'hui il y a beaucoup de tourbillons dans la ville.

. tousser sëqët : Maa ngiy sëqët ndax soj. Je tousse à cause de mon rhume.

. tracer rëdd : Damay rëdd ci kayit wi. Je trace sur le papier.

. trachée-artère pottax gi : Ci sa pottax la ñam yiy jaar. Les aliments passent par la trachée-artère.

. tradition xarbaax ji : Sunu réew bare na xarbaax. Notre pays a beaucoup de traditions.

. traduire firi, tekki/ tikki : Mën naa tekki ci wolof. Je peux traduire en wolof.

. trahir wor, jàmbu : Sa xarit bi dafa ma wor. Ton ami m'a trahi.

. train saxaar gi : Bu may tukku, saxaar laay jël. Je prends le train quand je voyage.

. transmettre jottali : Jottali naa yóbbante. J'ai transmis ton message.

. transvaser sotti : Sotti naa meew mi ci butéel bi. J'ai transvasé le lait dans la bouteille.

. travailler liggéey : Maa ngiy liggéey ci biró bi. Je travaille dans le bureau.

. traverser jàll : Jàll naa dex gi ak féey. J'ai traversé le fleuve à la nage.

. trébucher fakkatalu. Dama fakkatalu ci doj wi. J'ai trébuché sur une pierre.

. trembler lox : Maa ngiy lox ndax liw. Je tremble de froid.

. trempé tooy : Samay loxo dañu tooy. Mes mains sont trempées.

. tresse létt yi : Sa létt yi rafet nañu. Tes tresses sont jolies.

. tripe butit yi : Dindi naa butitu xar mi. J'ai enlevé les tripes du mouton.

. tromper nax : Jigéen ji dafa ma nax. La femme m'a trompé.

. tromper (se) juum : Juum naa ci waññ bi. Je me suis trompé en comptant.

. tronc dàtt bi : Beykat baa ngi toog ci dàttu garab gi. Le cultivateur est assis sur le tronc de l'arbre.

. trouver fekk : Dinaa la fekk tefes ga. Je te trouverai à la plage.

 

 

Le Petit Wolof est un dictionnaire multilingue vivant. Revenez le voir souvent.

Par wolofi - Publié dans : FR-WO
Ecrire un commentaire - Voir les 0 commentaires
Retour à l'accueil

Chic Meteo
Holidays

♦ Las Vegas
♦ New York
♦ UTC/GMT
♦ Paris
♦ Dakar

 

 

NON à l'excision !

Recherche

ŋ [ ] À Ññ Çç ß Óó Ëë Ïï Öö
 @ ½ ¼ Ää Üü ÷ ▀ ² ■ ª º

Al-Nd-Petit-Wolof.jpg
Le Petit Wolof deviendra grand.

 
 
  
anti-xeesal.jpg  
Anti-xeesal Campaign.
       
 
   

Syndication

  • Flux RSS des articles

Le sens du partage


pied_top.jpg
 
Contact - C.G.U. - Rémunération en droits d'auteur - Signaler un abus - Articles les plus commentés