Le Dictionnaire Wolof-Multilingue Vivant !
| translator | wo-en | en-wo | grammar | talk |
♦ $ ♦ ♦ |
| grammatik | konversation | ||||
| HOME | wo-fr | fr-wo | grammaire | conversation | sciences fr |
| translator | wo-en | en-wo | grammar | talk |
♦ $ ♦ ♦ |
| grammatik | konversation | ||||
| HOME | wo-fr | fr-wo | grammaire | conversation | sciences fr |
| XJ |
Jabaru Maalig, lu ko jot ? Mbaa du dafa feebar ? Gis naa démb ñu koy yóbbu lopitaal. Mbaa jàmm la ? Qu'est-ce qu'elle a, la femme de Malick ? Est-ce qu'elle n'est pas malade ? J'ai vu qu'on l'amenait hier à l'hôpital. Ce n'est pas grave ? |
|
| SB |
Aa ! Xam nga ni jigéenu-wéerul la ? Dégg naa ni wasin na sax (mucc). Sais-tu qu'elle est enceinte ? J'ai même entendu qu'elle a accouché. |
|
| XJ |
Kañ la wasin ? Quand ça ? |
|
| SB |
Altiné ci guddi ci ñeenti waxtu. Lundi à 4h du matin. |
|
| XJ |
Kon ngénte li talaata la ? Donc, le baptême, c'est mardi ? |
|
| SB |
Déedéet, altiné la. Non, c'est lundi. |
|
| XJ |
Lu tax ? Pourquoi ? |
|
| SB |
Aa ! Bët setagul woon. Il ne faisait pas encore jour. |
|
| XJ |
Kon de am na xew. Donc il a un grand évènement. |
|
| SB |
Waawaaw, rawati na muy taawam ! Oui, surtout que c'est son aîné. |
|
| XJ |
Lan la am sax ? Góor walla jigéen ? Est-ce un garçon ou une fille ? |
|
| SB |
Ay séex la am dégg naa. J'ai appris qu'elle a des jumeaux. |
|
| XJ |
Ndeysaan ! Loolu bare na. Yàlla nanu dund ak jàmm. C'est beaucoup. Que Dieu fasse qu'ils vivent longtemps. |
| Tekki baat | Lexique |
|
bët set na |
il fait jour |
| dund | vivre |
| jigéenu-wérul |
femme enceinte |
|
ndeysaan |
expression qui marque la pitié, la compassion |
| ngénte li | le baptême |
| séex |
avoir des jumeaux |
|
wasin ou mucc |
accoucher |
|
xew mi |
fête, évènement |
| ŋ [ ] À Ññ Çç ß Óó Ëë Ïï Öö |
|
@ ½ ¼ Ää Üü ÷ ▀ ² ■ ª º |