The Wolof-Multilanguage Live Dictionary Project
Le Dictionnaire Wolof-Multilingue Vivant !


translator  wo-en en-wo grammar talk   $ 
      grammatik konversation  
HOME wo-fr fr-wo grammaire conversation sciences fr

FR conversation

Lundi 19 juillet 2010 1 19 /07 /2010 00:01

1) Dama la bëgë katt (dama la/leu beugue katt) Je veux te baiser (en beaucoup plus romantique: 'Je veux te faire l'amour').

2) Dama la bëgg kat (dama la/leu beug) Je t'aime (Oh oui, je t'aime / Le mari de Laetitia disait : 'Que je t'aime, que je t'aime, que je t'aime! ). kat ne renvoie pas ici sur l'acte sexuel.

A retenir, selon Mobutu :
. bëgë > beugeu : détermine l'envie (projet, intention ...)
. bëgg > beug :  caractérise l'amour, l'amitié ou le simple fanatisme

 

senediaspora

Par wolofi - Publié dans : FR conversation - Communauté : Expatrie(e)s
Ecrire un commentaire - Voir les 0 commentaires - Partager    
Samedi 10 juillet 2010 6 10 /07 /2010 12:28

Nit ñi : Sylvie tubaab (ST) ak boroom taksi (BT)
Les personnages : Sylvie et le chauffeur de taxi

 

ST   Taxawal, boroom taksi ! Yóbbu ma dëkk ba! Na nga def ?
Taxi, arrête-toi! Emmène-moi en ville. Tu vas bien?
BT   Maa ngi fi rekk.  
Où en ville?
ST   Ca wetu post ba baax na. A côté de la poste.
BT   Fan nga jóge?
D'où viens-tu?
ST   Xanaa Ndar.;
De Saint-Louis, bien sûr.
BT   Déedéet, ci ban réew nga jóge laa wax. 
Non, je veux dire de quel pays.
ST   Olaand laa juddoo wante wolof laa léegi ndaxte yàgg naa fi. 
Je suis née en Hollande, mais je suis wolof maintenant
car je suis restée longtemps ici. 
BT   Ku la doon jàngal wolof?
Qui t'a enseigné le wolof?
ST   Sama benn xarit bu tudd Abdulaay. 
Un ami qui s'appelle Abdoulaye.
BT   Am nga jëkkër?
Es-tu mariée?
ST   Waaw, am naa kay. 
Oui, bien sûr.  
BT   Doo ma wutal jabar ci sa réew?
Veux-tu me trouver une femme à marier dans ton pays?
ST   Mën naa la wutal, wànte samay xarit duñu jullit. 
Je peux le faire, mais mes amies ne sont pas musulmanes.
BT   Kon ma tuubloo ko. 
Je pourrais la faire convertir à l'islam.
ST   Loolu baax na waaye xëyna moom du ko nangu. 
C'est bien, mais peut-être qu'elle ne l'accepterait pas.
BT   Wax nga dëgg. Ba nga nekkee ci sa réew, loo daan liggéey? 
Tu as raison. Qu'est-ce que tu faisais dans ton pays?
ST   Daan naa liggéey ci mbirum wér-gi-yaram. 
Je travaillais dans la santé.
BT   Xanaa doktoor nga?
Donc, tu es médecin?
ST   Waaw, moom laa. 
Oui, je suis docteur. 
BT  

Fii ci Senegaal, wolonteer nga walla déet?
Au Sénégal, vous êtes volontaire ou non?         

ST  

Déedéet, duma wolonteer. Ci benn poroose laa bokk. Taxawal fii! Am sa xaalis a ngi. Yendul ak jàmm!
Non, je ne suis pas volontaire. Je travaille dans un projet. Arrête ici! Voici ton argent. Bonne journée!         

BT  

Jàmm ak jàmm.
A toi aussi.         

 

 

Tekki baat Lexique
   
boroom bi maître, propriétaire
boroom taksi le chauffeur de taxi
juddu emmener
jullit le musulman qui prie
kay particule d'insistance
mbirum wér-gi-yaram le domaine de la santé
taxaw s'arrêter
tuub se convertir

 

Abdoulaye Dial

Par wolofi - Publié dans : FR conversation - Communauté : Portes et Fenêtres
Ecrire un commentaire - Voir les 0 commentaires - Partager    
Dimanche 20 juin 2010 7 20 /06 /2010 18:10

Boroom yàpp wi ak boroom lujum yi 

La marchande de viande et la marchande de légumes

 

 

Nit ñi : Sooda Sekk; Xaar Njaay, boroom yàpp wi ak Faatu Jóob, boroom lujum yi

Les personnages : Soda Seck (SS); Xaar Ndiaye (XN), le marchand de viande et Fatou Diop (FD), la marchande de légumes

 

SS
 

Asalaa maalikum! Ana boroom yàpp wi?

Bonjour ! Où est la marchande de viande?

XN
 

Aa! Maa ngi nii. Maalikum salaam.

Ah! Me voici!

SS
 

Am nga yàpp?

As-tu de la viande?

XN 
 

Waaw, am naa yàpp wu baax te duuf sax.

Oui, j'ai de la viande de qualité.

SS
 

Yàppu xar la walla yàppu nag?

C'est de la viande de mouton ou de la viande de boeuf?

XN 
 

Yépp ñaar laa am.

J'ai les deux.

SS
 

Am nga res itam?

Tu as aussi du foie?

XN 
 

Waaw, waaye li ci des barewul de!

Oui, mais il n'en reste plus beaucoup.

SS
 

Bi ma fi ñówee keroog, jaayoon nga ma lu baax de! Peeseel ma ñetti kiló yàppu nag ak ñetti yàppu xar ak benn kilo ci res wi! Waaw, ñaata ngay jaaye kilo bi sax?

Lorsque j'étais venu l'autre jour, tu m'avais vendu de la bonne chair. Pèse-moi 3 kg de boeuf, 3 kg de mouton et 1 kg de foie. Combien coûte le kilo?

XN 
 

Su dee yàppu nag, kiló bi ñetti téeméer la. Su dee xar, ñaari téeméer ak ñeent fukk. Res, moom, kiló bi ñaari téeméer rekk la.

Le boeuf coûte 1500 le kilo; le mouton, 1200 CFA et le foie 1000 CFA le kilo. 

SS
 

Waaw, peeseel ma gaaw, dama yàkkamti! Damay jaar ci boroom lujum yi jënd yu sew. Am! Ñaari junnee ngoog. Delloo ma gaaw sama weccit!

Oui, dépêche-toi! Je suis pressée. Je dois passer chez la vendeuse de légumes acheter de petites choses. Tiens, voilà 10.000 CFA. Rends-moi vite la monnaie!

XN
 

Am! Sa weccit a ngi!

Tiens! Voilà ta monnaie.

SS
 

Jërëjef! Maa ngiy dem ba beneen.

Merci. Je m'en vais. A la prochaine fois.

     
     
    *****
SS
 

Aa! Boroom lujum, jaay ma yu sew!

Bonjour! Madame (marchande de légumes), vends-moi des légumes! 

FD
 

Lan nga soxla tey?

De quoi as-tu besoin aujourd'hui?

SS
 

Kaani, persi, soble, karoot, nawe, salat ak pombiteer.

Du piment, du persil, des oignons, des carottes, des navets, de la salade et des pommes de terre.

FD
 

Jeex na? Loolu rekk nga soxla?

C'est tout? Tu n'as besoin de rien d'autre?

SS
 

Waaw, baax na. Ñaata la?

Oui, c'est assez. Cela fait combien?

FD
 

Yépp, ñetti téeméer la.

Ça fait 1500 CFA en tout. 

SS
 

Am! Jërëjëf. Maa ngiy dem ba beneen.

Voici. Merci. A la prochaine fois.

FD
 

Waaw kañ. Jàmm ak jàmm.

Bien. La paix seulement.

 

 

 

Tekki baat Lexique
   
boroom bi

le propriétaire

duuf être gras, charnu
kaani gi le piment
karoot gi la carotte
keroog l'autre jour
lujum yi

les légumes

nag wi la vache
nawe ji le navet
persi le persil
pombiteer ji

la pomme de terre

res wi le foie
salaat si la salade verte
yàpp wi la viande
yu sew des légumes en petites quantités pour préparer le repas

 

 Abdoulaye Dial     

Par wolofi - Publié dans : FR conversation - Communauté : partage
Ecrire un commentaire - Voir les 0 commentaires - Partager    
Mardi 8 juin 2010 2 08 /06 /2010 13:04

Ndakaaru njaay : La ville de Dakar

 

Nit ñi : Iba Kan ak Maymuna Lóo

Les personnages : Iba Kan (IK) et Maïmouna Lô (ML)

 

IK  

Maymuna, agsi nanu Ndakaaru de. Miin nga dëkk bi bu baax?

Maïmouna, nous sommes arrivés à Dakar. Connais-tu bien la ville? 

ML   

Déedéet, mës naa fi ñów been yoon rekk.

Non, je suis venue ici une fois seulement. 

IK   

Fii de mooy péeyu Senegaal. Xoolal mbedd yi ak taax yi! Rafet nañu?

Ici, c'est la capitale du Sénégal. Regarde les rues et les maisons! C'est beau? 

ML     

Waawaaw. Rafet nañu lool te yaatu. Dëkk bii, aka réy! Yàlla bu ma fi réer sax! Man de waaru naa. Fii fan la? 

Oui, c'est beau et aéré. Oh! Cette ville est si énorme! Je ne voudrais pas m'y perdre. Je suis vraiment surprise. C'est quoi, ça?

IK    Fii, kër boroom tree mi la. Soo we're ci gannaaw dem ba ci booru géej 
gi, dinga séen Gore.
C'est le palais du Président de la République. Si tu passes par 
derrière jusqu'à la mer, tu verras Gorée. 
ML      Ndax dinañu fa mëna dem?
Est-ce qu'on peut y aller? 
IK    Waaw, Subaru dinañu mëna jël salub bi.
Oui, demain on pourra prendre la chaloupe. 
ML      Mbaa dinanu nemmeeku marse Ndakaaru balaa ñuy dem?
N'est-ce pas qu'on va passer par les matchés da Dakar avant de partir? 
IK    Waaw, dinanu jaar Sàndaga ak Kermel soo bëggee jënd dara.
Oui, on va passer par Sandaga et Kermel si tu veux acheter quelque 
chose. 
ML      Bu ñu jógee goofy, dinañu am jotu dem iniwersité ak IFAN?
Lorsque nous retournons, aura-t-on le temps d'aller à l'université et 
à l'IFAN?
IK    Waawaaw, mën na nekk kay bu nu gaawantoo tuuti.
Oui, c'est bien possible si nous nous pressons un peu. 
ML      Naka lanu Fay deme? Ci taksi?
Comment y aller? En taxi? 
IK    Naka lanu Fay deme? Ci taksi?
Comment y aller? En taxi? 

 

 

Tekki baat Lexique
   
am jot avoir le temps
gaawantu se presser, se précipiter
mbedd mi la rue
miin être familier
nemmeeku visiter
péey bi la capitale
taax mi le mur, bâtiment


 

IFAN Institut Fondamental de l'Afrique Noir
SOTRAC Société des Transports Communs (ici, le bus de Sotrac)

 

 

Abdoulaye Dial 

Par wolofi - Publié dans : FR conversation - Communauté : Portes et Fenêtres
Ecrire un commentaire - Voir les 0 commentaires - Partager    
Samedi 15 mai 2010 6 15 /05 /2010 00:01

Gan gi  :  Le visiteur

 

Nit ñi : Sàmba Ba ak gan gi Faatu Keyta

Les personnages : Samba Ba (SB) et l'étrangère Fatou Keïta (FK).

 

 

SB

Jàmm nga am, Faatu?

As-tu la paix, Fatou?

FK

Jàmm rekk, Ba!

La paix seulement, Ba.

SB

Yow, dangay jàngale walla dangay gëstu?

Tu enseignes ou tu fais des recherches?

FK

Man, jàngalewuma waaye damay gëstu.

Je n'enseigne pas. Je fais des recherches.

SB

Fan réew nga jóge?

De quel pays viens-tu?

FK

Maali laa jóge. Yow nag?

Je viens du Mali. Et toi?

SB Man, waa fii laa.
Moi, je viens d'ici.
FK

Maali, dëkk la walla réew?

Le Mali, est-ce une ville ou un pays?

SB

Réew la.

C'est un pays.

FK

Ndar, réew la walla dëkk?

Saint-Louis, est-ce un pays ou une ville?

SB

Dëkk la.

C'est une ville.

 

 

 

 

Nit ñi : Badu Jàllo, Faatu Keyta ak Amadu Jóob

Les personnages : Badou Diallo (BD), Fatou Keïta (FK) et Amadou Diop (AD)

.

 

AD

Badu, kii sa gan la?

Badou, c'est ton étrangère, elle (celle-là)?

BD

Waaw, suma gan la.

Oui, c'est mon étrangère.

AD

Naka la tudd?

Comment s'appelle t-elle?

BD

Faatu Keyta la tudd.

Elle s'appelle Fatou Keïta.

AD

Fan la jóge? Maali?

D'où vient-elle? Du Mali?

BD

Waaw. Fofu la jóge.

Oui, elle vient de là-bas.

AD

Lan lay def ci Senegaal?

Qu'est-ce qu'elle fait au Sénégal?

BD

Dafay gëstu ci mbirum jën yi.

Elle fait des recherches dans le domaine des poissons.

AD

Loolu baax na.

C'est bien.

BD

Waaw, yow, ci ban mbooloo nga bokk?

Dans quel organisme es-tu?

AD

Man, ci kooperasiyoŋ laa bokk.

Je suis de la coopération.

BD

Faatu, sa jëkkër nga àndal Senegaal?

Fatou, tu es accompagnée de ton mari?

FK

Waaw, wànte dafa feebar.

Oui, mais il est malade.

BD

Lu moo liggéey?

Que fait-il?

FK

Deful dara.

Il ne fait rien.

 

 

 

Tekki baat  Lexique 
   
bokk  faire partie de, participer 
dëkk bi  la ville 
gëstu  faire des recherches 
mbirum le domaine de
mbooloo mi association, groupement
réew mi  le pays 
wànte  mais 

 

 

 

 Abdoulaye Dial

Par wolofi - Publié dans : FR conversation
Ecrire un commentaire - Voir les 0 commentaires - Partager    
Samedi 24 avril 2010 6 24 /04 /2010 00:01

Naka lañuy togge ceebu-jën?

Comment prépare-t-on le riz au poisson?

 

 

Nit ñi : Ami Thiaw ak Sokhna Faal

Les personnages : Amy Thiaw (AT) et Sokhna Fall (SF)

 

 

AT  

Waaw, yow, lan ngay def ci waañ wi ? Xanaa dangay togg?

Mais toi, qu'est-ce que tu fais dans la cuisine ? Tu prépares le repas?

SF  

Waaw, damay togg.

Oui, je suis en train de cuisiner.

AT  

Yow, mën nga togg ceebu-jën?

Tu sais préparer le riz au poisson?

SF  

Waaw ! Lu tere?

Oui ! Pourquoi pas?

AT  

Lan ak lan nga mëna togg itam?

Quoi d'autre sais-tu préparer?

SF  

Mën naa togg ñaari cin : muy maafe, di suppu-kànja, di ceebu-soos. Mën naa togg itam ceebu-tooy, gosi, laax, cere-siim ak yeneen sax.

Je sais préparer du maafe, du suppu-kànja, du ceebu-soos. Je sais aussi préparer du riz au poisson humide, du riz au lait, du laax, du couscous et tant d'autres encore.

AT  

Waaw, nan lañuy togge ceebu-jën?

Au fait, comment prépare-t-on le riz au poisson?

SF  

Dangay taal, def dëwlin ci kawdiir gi, def soble, xóoyal tamaate ji, def ci.

Tu mets la marmite sur le feu, tu y verses de l'huile, tu ajoutes des oignons et de la tomate.

 

Su dogee, nga ñulug, raxas jën yi, def ci, sotti lujum,yeek gejj gi ak daqaar gi.

Quelque temps après, tu ajoutes de l'eau, en y mettant les poissons bien lavés, puis les légumes, le poisson sec et le tamarin.

 

Nga bàyyi ba mu bax tuuti nga tonni dëwlin ji ci kow soogay tay.

Tu laisses bouillir pour ensuite prélever l'huile à la surface et faire cuire le riz à la vapeur.

 

Soo tayee ba noppi, nga delloo ci dëwlin ji daldi seppi, tanq ñeex, def ci seppi bi.

Après avoir fait ça, tu remets l'huile pour ensuite retirer les condiments cuits dans la sauce en puisant en même temps de la sauce que tu vas garder dans une assiette.

 

Léegi nag, nga daldi sóor, bàyyi ba ca kanam, nga jeqi ba mu ñor, nga sooga yakk.

Maintenant, tu mets le riz dans la sauce et tu remues de temps en temps le fond de la marmite avec une cuillère jusqu'à la fin de la cuisson. Tu mets dans un plat de service.

 

 

Tekki baat   Lexique
     
baasi bi   couscous de mil accompagné de la sauce d'arachides
bax   bouillir
ceere-tooy   riz au poisson humide (riz gras)
cere-siim   couscous de mil mouillé avec de la sauce
daqaar ji   le tamarin
dëwlin ji
  l'huile
dog   couper
gejj gi   le poisson séché
gosi gi   riz au lait
jeqi   remuer au fond, bien remuer
kawdiir gi   la marmite
lu tere ?   qu'est-ce qui m'empêche ?
ñaari-cin   un repas préparé avec deux marmites comprenant de la sauce et du riz blanc. Le maafe : sauce d'arachides, le suppu-kànja : sauce avec de l'huile de palme, le ceebu-soos : sauce avec de la farine.
ñeex mi   la sauce de ceebu-jën
ñor   être à point, arriver à maturité, être mûr, être cuit
ñulug   mettre une quantité d'eau pour la cuisson d'un plat
seppi   retirer ce qui a cuit dans la sauce
seppi bi   ce qui est retiré de la marmite
sóor   mettre le riz dans la marmite
sotti   verser
tanq   puiser
tay   faire passer, cuire à la vapeur
togg   faire la cuisine
tonni   prélever à la surface
waañ wi   la cuisine
xóoyal   délayer
yaak   mettre dans un plat ou une assiette le contenu cuit d'une marmite

 

 

Abdoulaye Dial

Par wolofi - Publié dans : FR conversation - Communauté : NO COMMENT et COMMENT
Ecrire un commentaire - Voir les 0 commentaires - Partager    
Mercredi 24 mars 2010 3 24 /03 /2010 00:01
Dëj ba   Le décès

Nit ñi : Xadi Jóob ak Seynabu Ba
Les personnages : Khady Diop (KD) et Seynabou Ba (SB)


SB   Dégg naa ni sa maam dafa gaañu.
J'ai appris que ton grand-parent est décédé.
KD   Waaw, gaañu na démb.
Oui, il est décédé hier.
SB   Moom, dafa feebaroon?
Est-ce qu'il était malade?
KD   Waaw, yàgg na feebar de.
Oui, cela fait longtemps qu'il était malade.
SB   Man yëguma ko woon. Siggil ndiggaale!
Moi, je n'étais pas au courant. Mes condoléances.
KD   Siggil sa wàll!
A toi de même.
SB   Yàlla na la dëdd ak jàmm!
Qu'il te tourne le dos en paix!
KD   Amiin.
Amen.
SB   Maa ngiy dem.
Je m'en vais.
KD   Baax na. Yàlla na la Yàlla bindal tuyaaba!
C'est gentil. Que Dieu te bénisse!
SB   Amiin.
Amen.
     


Tekki baat Lexique
   
dëdd tourner le dos
dëj bi le décès (l'enterrement)
maam grand-père ou grand-mère
siggi relever la tête
tuyaaba bienfait
yëg sentir, être au courant


Abdoulaye Dial
Par wolofi - Publié dans : FR conversation - Communauté : NO COMMENT et COMMENT
Ecrire un commentaire - Voir les 0 commentaires - Partager    
Mercredi 10 mars 2010 3 10 /03 /2010 04:28
Ngénte li  Le baptême


Nit ñi : Xadi Jóob (XJ) ak Suléy Ba (SB)
Les personnages : Khady Diop et Souley Ba


SB   Aa ! Xadi, tuddaguñu ba léegi ?
Khady, est-ce que tu as baptisé le bébé ?
XJ   Axankay ! Sëriñ bi tudd na ca suba teel.
Si, c'est fait depuis ce matin de bonne heure.
SB   Naka la liir bi tudd ? (Séex yi)
Comment se nomme le bébé ? (Les jumeaux)
XJ   Umar la tudd. (Aadamaak Awa)
Oumar est son nom. (Adam et Eve)
SB   Rey nañu xar mi ?
Ont-ils égorgé le mouton ?
XJ   Waaw, rey nañu ko.
Oui, on l'a égorgé.
SB   Ndokkale waay !
Félicitations !
XJ   Ndokk sa wàll.
A toi de même.
SB   Ana laax/ laakh yi ?
Où est le laakh ?
XJ   Ñu ngiy ñów.
Ça vient.
SB   Ee ! Sama jigéen, indil benn leketu laax ñu ! Danuy liggéeyi waay !
Ma soeur, amène un plat ici ! Nous devons aller au travail !
XJ   Waaw, ma ñów léegi. Am ! Benn a ngi.
Oui, j'arrive. En voilà un.
SB   Jërëjëf. Ana ndoxum raxasu mi ?
Merci. Où peut-on se laver les mains ?
XJ   Mu ngi nii.
Voilà.
SB   Aywa gaa ñi, ñu lekk waay !
Allons-y, les gars, mangeons !



Tekki baat   Lexique
     
axankaay   si (réponse affirmative à une question négative)
laax, laakh   bouillie épaisse faite avec mil, riz ou maïs et accompagné de lait caillé
liir bi   le bébé
Ndokkale !   Félicitations !
ndoxum raxasu mi   récipient contenant de l'eau pour se laver les mains (avant le repas)
ngénte li   le baptême. Fête où l'on donne le nom à l'enfant. 
tudd   donner un nom au bébé, baptiser, s'appeler
séer yi   les jumeaux
sëriñ bi   le marabout


Abdoulaye Dial
Par wolofi - Publié dans : FR conversation
Ecrire un commentaire - Voir les 1 commentaires - Partager    
Mercredi 10 février 2010 3 10 /02 /2010 00:01
Sabar ga   Le tam-tam


Nit ñi : Faatu Jal ak xaritam Ayda Faal
Les personnages : Fatou Dial (FD) et son amie Aïda Fall (AF)


FD   Kañ ngay fóot sa yére yi ?
Quand laves-tu tes vêtements ?
     
AF   Damay togg añ bi ba noppi.
Je préparerai le déjeuner avant.
     
FD   Fecciwoon nga démb ca sabar ga ?
As-tu dansé au son du tam-tam hier ?
     
AF   Demoon naa waaye feccuma, dama toog di tàccu rekk.
J'y suis allée mais je n'ai pas dansé. J'ai seulement applaudi.
     
FD   Lu tax ?
Pourquoi ?
     
AF   Mënuma fecc sabar.
Je ne sais pas danser la danse traditionnelle (sabar).
     
FJ   Ana say  doom ?
Oû sont tes enfants ?
     
AF   Ñu ngiy fo ci ëtt bi.
Ils jouent dans la cour.
     
FJ   Lan ngay def ci say gëñ ? Danu weex de !
Qu'est-ce que tu mets sur tes dents ? Elles sont vraiment blanches !
     
AF   Dara. xanaa di leen socc rekk.
Rien, je les frotte avec un bâtonnet.
     
FJ   Dinaay soccu léegi ndax samay gëñ yi weex na sa yos.
Je frotterai aussi mes dents pour qu'elles soient blanches comme les tiennes.
     
AF   Waaw, moo gën de. Soccu baax na lool sax !
Oui, c'est mieux. C'est vraiment bien de se frotter les dents !












































Tekki baat   Lexique
     
ëtt bi   la cour
fecc    danser
fo    jouer
fóot    faire la lessive
sabar    tam-tam
soccu    (se) frotter les dents avec un bâtonnet
tàccu    applaudir
togg    préparer le repas
weex    être blanc


Abdoulaye Dial
Par wolofi - Publié dans : FR conversation
Ecrire un commentaire - Voir les 0 commentaires - Partager    
Mardi 2 février 2010 2 02 /02 /2010 12:48
Nafi ngiy xiim attaaya ji   Nafi est en train de faire du thé



Nit ñi : Ayda Njaay ak ganam Faatu Fay ak Nafi, rakkam kuy xiim attaaya ji
Les personnages : Aïda Ndiaye (AN), son amie Fatou Faye (FF) et sa petite soeur Nafi (N) sont en train de faire du thé.


FF   Yéen, dingeen faral di naan attaaya su ngeen añee ba noppi ?
Avez-vous l'habitude de prendre le thé après le déjeuner ?
AN   Waaw, dinanu koy naan, wànte man, benn baraada bu woyef rekk laay naan. Yow nag ?
Oui, nous en prenons, mais moi, un seul verre me suffit. Et toi ?
FF   Man, ñetti baraada yépp laay naan : lëwël bi, ñaareel bi ak ñetteel bi.
Moi, je prends les trois verres : le premier, le deuxième et le troisième.
AN   Nafi, xiimal waay ! Bu ci def warga ju bare de !
Nafi, fais le thé et ne mets pas beaucoup de thé !
N   Déedéet, tuuti rekk laa ciy def.
Non, un peu seulement.
AN   Suukër si nga jënd doy na ?
Est-ce que le sucre que tu as acheté suffit ?
N   Waaw, doy na waaye amaguma naanaa de.
Oui, mais je n'ai pas encore de menthe.
AN   Wool xale bi mu boyal furnó bi, jëndal la naanaa te indi kaasi attaaya bi !
Appelle le gosse pour qu'il allume le charbon dans le fourneau, acheter de la menthe et ensuite apporter les verres.


Tekki baat  Lexique

attaaya ji  thé à la menthe
baraada bi  la théière
boyal  allumer le charbon dans le fourneau
kaas bi  petit verre à thé
lëwël bi  la première théière
naanaa ji  la menthe
warga ji  le thé séché
woyef  léger
xiim  faire le thé


Abdoulaye Dial
Par wolofi - Publié dans : FR conversation - Communauté : Portes et Fenêtres
Ecrire un commentaire - Voir les 0 commentaires - Partager    

  • : Vocabulaire et grammaire wolof ainsi que ce que je vois de ma fenêtre.

Chic Meteo
Holidays

♦ Las Vegas
♦ New York
♦ UTC/GMT
♦ Paris
♦ Dakar

 

 

NON à l'excision !

Recherche

ŋ [ ] À Ññ Çç ß Óó Ëë Ïï Öö
 @ ½ ¼ Ää Üü ÷ ▀ ² ■ ª º

Syndication

  • Flux RSS des articles

Le sens du partage


pied_top.jpg
 
Contact - C.G.U. - Rémunération en droits d'auteur - Signaler un abus - Articles les plus commentés