The Wolof-Multilanguage Live Dictionary Project
Le Dictionnaire Wolof-Multilingue Vivant !



translator  wo-en en-wo grammar talk   $ 
      grammatik konversation  
HOME wo-fr fr-wo grammaire conversation sciences fr

DE grammatik

Jeudi 16 décembre 2010 4 16 /12 /Déc /2010 00:01

Yaa dëkk universite?

Bist Du es, der bei der Universität wohnt?

 

Waaw, maa dëkk universite.

Ja, ich bin es, der bei der Universität wohnt.

 

Waaw, maa fa dëkk.

Ja, ich bin es, der dort wohnt.

 

Déedéet, du maa dëkk universite.

Nein, ich bin es nicht, der bei der Universität wohnt.

 

Déedéet, du maa fa dëkk.

Nein, ich bin es nicht, der dort wohnt.

 

 

Ceebu jën nga togg?

Ist es ceebu jën, das Du gekocht hast?

 

Waaw, ceebu jën laa togg.

Ja, es ist ceebu jën, das ich gekocht habe.

 

Waaw, moom laa togg.

Ja, das ist es, das ich gekocht habe.

 

Déedéet, du ceebu jën laa togg.

Nein, es ist nicht ceebu jën, das ich gekocht habe.

 

Déedéet, du moom laa togg.

Nein, das ist es nicht, das ich gekocht habe.

 

 

♦  

Yaay waxtaan ak Pap Laay?

Bist Du es, der mit Pap Laay diskutiert?

 

Waaw, maay waxtaan ak Pap Laay.

Waaw, maay waxtaan ak moom.

Déedéet, du maay waxtaan ak Pap Laay.

Déedéet, du maay waxtaan ak moom.

 

 

♦  

Universite ngeen jëm?

Ist es die Universität, zu der Du gehst?

 

Waaw, universite lanu jëm.

Waaw, fa lanu jëm.

Déedéet, du universite lanu jëm.

Déedéet, du fa lanu jëm.

 

 

♦  

Yéenay jàng wolof?

Bist Du es, der Wolof lernt?

 

Waaw, nooy jàng wolof.

Waaw, noo koy jàng wolof.

Déedéet, du nooy jàng wolof.

Déedéet, du noo koy jàng.

 

 

♦  

Wolof laay jàng?

Ist es Wolof, das ich lerne?

 

Waaw, wolof laay jàngale.

Waaw, moom laay jàngale.

Déedéet, du wolof laay jàngale.

Déedéet, du moom laay jàngale.

 

 

♦  

Say doom ngay yóobu Dakaar?

Sind es Deine Kinder, die Du nach Dakar bringst?

 

Waaw, samay doom laay yóbbu Dakaar.

Waaw, ñoom laa fay yóbbu.

Déedéet, du samay doom laay yóbbu Dakaar.

Déedéet, du ñoom laa fay yóbbu.

 

 

♦  

Kuddu ngay lekke?

Ist es ein Löffel, mit dem Du isst?

 

Waaw, kuddu laay lekke.

Waaw, moom laay lekke.

Déedéet, du kuddu laay lekke.

Déedéet, du moom laay lekke.

 

 

♦  

Sa jabar ngay jëndal xaal?

Ist es Deine Frau, für die Du Melonen kaufst?

 

Waaw, sama jabar laay jëndal xaal.

Waaw, moom laa koy jëndal.

Déedéet, du sama jabar laay jëndal xaal.

Déedéet, du moom laa koy jëndal.

 

 

♦  

Yaa ma toggal ceebu-jën?

Bist Du es, der für mich ceebu-jën gekocht hat? 

 

Waaw, maa la toggal ceebu-jën.

Waaw, maa la ko toggal.

Déedéet, du maa la toggal ceebu-jën.

Déedéet, du maa la ko toggal.

 

 

♦  

Dakaar ngeen dëkk?

Ist es Dakar, wo ihr wohnt? 

 

Waaw, Dakaar lanu dëkk.

Waaw, fa lanu dëkk.

Déedéet, du Dakaar lanu dëkk.

Déedéet, du fa lanu dëkk.

 

 

GRAMMATIKALISCHE ANMERKUNG

 

Die deutschen Übersetzungen der Betonungen des Subjekts und Objekts mögen ein wenig eigenartig klingen, weil im Deutschen das zu betonende Wort meist ans Satzende gesetzt oder durch Intonation hervorgehoben wird. Im Wolof werden beide Arten der Betonung verwendet : Intonation und Umkehr des Satzbaus.

 

 

AUS DEM FRANZÖSISCHEN

 

université > universite : Universität

 

 Abdoulaye Dial

Par wolofi - Publié dans : DE grammatik - Communauté : ~ Au Fil du Temps ~
Ecrire un commentaire - Voir les 0 commentaires
Jeudi 2 décembre 2010 4 02 /12 /Déc /2010 00:01

Betonung des Objekts (vervollständigt)

 

 

AUSSAGE

 

Wolof laa jàng. Es ist Wolof, dass ich gelernt habe.
Wolof nga jàng. Es ist Wolof, dass du gelernt hast.
Wolof la jàng. Es ist Wolof, dass er gelernt hat.
Wolof lanu jàng. Es ist Wolof, dass wir gelernt haben.
Wolof ngeen jàng. Es ist Wolof, dass ihr gelernt habt.
Wolof lañu jàng. Es ist Wolof, dass sie gelernt haben.

 

 

 

VERNEINUNG

 

Du wolof laa jàng. Es ist nicht Wolof, dass ich gelernt habe.
Du wolof nga jàng. Es ist nicht Wolof, dass du gelernt hast.
Du wolof la jàng. Es ist nicht Wolof, dass er gelernt hat.
Du wolof lanu jàng. Es ist nicht Wolof, dass wir gelernt haben.
Du wolof ngeen jàng. Es ist nicht Wolof, dass ihr gelernt habt.
Du wolof lañu jàng. Es ist nicht Wolof, dass sie gelernt haben.

 

 

 

GRAMMATIKALISCHE ANMERKUNG

 

Gleich wie bei der Betonung des Subjekts kann auch hier für unvervollständigte Handlungen ein  -y  an das betonende Fürwort angehängt werden.

Wolof laay jàng. Wolof lerne ich.

 

 Abdoulaye Dial

Par wolofi - Publié dans : DE grammatik - Communauté : le Finistère
Ecrire un commentaire - Voir les 0 commentaires
Mercredi 1 décembre 2010 3 01 /12 /Déc /2010 11:08

Betonung des Subjekts (vervollständigt, Vergangenheit)

 

 

AUSSAGE

 

Maa jàng wolof. Ich bin es, der Wolof gelernt hat.
Yaa ... Du bist es, ...
Moo ... Er ist es, ...
Noo ... Wir sind es, ...
Yéena ... Ihr seid es, ...
Ñoo ... Sie sind es, ...

 

 

 

VERNEINUNG

 

Du maa jàng wolof. Ich bin es nicht, der Wolof gelernt hat.
Du yaa ... Du bist es nicht, ...
Du moo ... Er ist es nicht, ...
Du noo ... Wir sind es nicht, ...
Du yéena ... Ihr seid es nicht, ...
Du ñoo ... Sie sind es nicht, ...

 

 

 Abdoulaye Dial

Par wolofi - Publié dans : DE grammatik - Communauté : NO COMMENT et COMMENT
Ecrire un commentaire - Voir les 0 commentaires
Mardi 22 décembre 2009 2 22 /12 /Déc /2009 00:02
AUSSAGE

Jàng naa wolof. Ich habe Wolof gelernt.
Jàng nga wolof. Du hast Wolof gelernt.
Jàng na wolof. Er hat Wolof gelernt.
Jàng nanu wolof. Wir haben Wolof gelernt.
Jàng ngeen wolof. Ihr habt Wolof gelernt.
Jàng nañu wolof. Sie haben Wolof gelernt.


VERNEINUNG

Jànguma wolof. Ich habe nicht Wolof gelernt.
Jànguloo wolof. Du hast nicht Wolof gelernt.
Jàngul wolof. Er hat nicht Wolof gelernt.
Jàngunu wolof. Wir haben nicht Wolof gelernt.
Jànguleen wolof. Ihr habt nicht Wolof gelernt.
Jànguñu wolof. Sie haben nicht Wolof gelernt.



Nanga def? Wie Geht's?


Abdoulaye Dial
Wie Geht's? Wolof im Handumdrehen
ist die deutsche Ausgabe v.  Na nga def? (franz. Version)
A5-Format, 100 Seiten.

KontaKt : abdoulayedial AT hotmail.com

Par wolofi - Publié dans : DE grammatik
Ecrire un commentaire - Voir les 0 commentaires
Jeudi 3 décembre 2009 4 03 /12 /Déc /2009 00:01
Damay jàng wolof.  Ich lerne Wolof.
Dangay jàng wolof.  Du lernst Wolof.
Dafay jàng wolof.  Er lernt Wolof.
Danuy jàng wolof.  Wir lernen Wolof.
Dangeen jàng wolof.  Ihr lernt Wolof.
Dañuy jàng wolof.  Sie lernen Wolof.

Maa ngiy jàng wolof.  Ich lerne gerade Wolof.
Yaa ngiy jàng wolof.  Du lernst gerade Wolof.
Mu ngiy jàng wolof.  Er lernt gerade Wolof.
Nu ngiy jàng wolof.  Wir lernen gerade Wolof.
Yéena ngiy jàng wolof.  Ihr lernt rade Wolof.
Nu ngiy jàng wolof.  Sie lernen gerade Wolof.

NB :  Diese beiden Formen der Konjugation verwenden die gleiche Verneinung.


VERNEINUNG

Jànguma wolof.  Ich lerne nicht Wolof.
Jànguloo wolof.  Du lernst nicht Wolof.
Jàngu wolof.  Er lernt nicht Wolof.
Jàngunu wolof.  Wir lernen nicht Wolof.
Jànguleen wolof.  Ihr lernt nicht Wolof.
Jànguñu wolof.  Sie lernen nicht Wolof.


NB :  Die Satzteile dama, danga, dafa, danu, dangeen, dañu werden hauptsächlich dazu verwendet, eine Frage oder Aussage rechtzufertigen. Zum Beispiel :

. Looy def ?  Was machst Du ?
. Damay jàng. Ich lerne gerade.
. Lu tax ngay dem ? Warum gehst Du ?
. Damay yakkamti.  Ich bin in Eile.


NB : Der Satzteil -oon wird an ein  Verb angehängt, um zu Vorzeitigkeit anzuzeigen, und ist vergleichbar mit der plus-que-parfait Form im Französischen. Zum Beispiel :

Verb des Zustandes :
Dama feebaroon.  Ich war krank.
Feebaruma woon.  Ich war nicht krank.

Verb der Tätigkeit :
Dama  demoon Dakaar.  Ich ging nach Dakar.
Demuma woon Dakaar.  Ich ging nicht nach Dakar.



Beispiele :

AUSSAGE

Dangay jàng wolof ?  Lernst Du Wolof ?
Waaw, damay jàng wolof.  Ja, ich lerne Wolof.

Dangeen di dem Dakaar ?  Gehst Du nach Dakar ?
Waaw, danuy dem Dakaar.  Ja, wir gehen nach Dakar.

Damay jàngale wolof ?  Unterrichte ich Wolof ?
Waaw, dangay jàngale wolof.  Ja, Du unterrichtest Wolof.

Yaa ngiy jàng wolof ?  Lernst Du gerade wolof ?
Waaw, maa ngiy jàng wolof.  Ja, ich lerne gerade Wolof.

Yéena ngiy jàng wolof.  Lernt ihr gerade Wolof ?
Waaw, nu ngiy jàng wolof.  Ja, wir lernen gerade Wolof.


VERNEINUNG

Dangay dem Dakaar ?  Gehst Du nach Dakar ?
Déedéet, demuma Dakaar. Nein, ich nicht nach Dakar.

Yaa ngiy lekk ceebu jën ? Isst Du gerade ceebu jën ?
Déedéet, lekkuma ceebu jën. Nein, ich esse nicht gerade ceebu jën.

Danga feebaroon ? Warst Du krank ?
Déedéet, feebaruma woon. Nein, ich war nicht krank.

Danga demoon France ? Bist Du nach Frankreich gegangen ?
Déedéet, demuma woon France. Nein, ich bin nicht nach Frankreich gegangen.

Jàngoon nga wolof ? Hattest Du Wolof gelernt ?
Déedéet, jànguma woon wolof. Nein, ich hatte nicht Wolof gelernt.

Maa ngiy jàngale pulaar ? Unterrichte ich gerade Pulaar ?
Déedéet, jàngalewuloo pulaar. Nein, Du unterrichtest gerade nicht Pulaar.

Dangeen di jàng pulaar ? Lernt ihr gerade Pulaar ?
Déedéet, jàngunu pulaar. Nein, wir lernen gerade nicht Pulaar.


Nanga def? Wie Geht's?


Abdoulaye Dial

Wie Geht's? Wolof im Handumdrehen
ist die deutsche Ausgabe v.  Na nga def? (franz. Version)
Format A5, 100 Seiten.

KontaKt : abdoulayedial AT hotmail.com

Par wolofi - Publié dans : DE grammatik - Communauté : ~ Au Fil du Temps ~
Ecrire un commentaire - Voir les 0 commentaires

Chic Meteo
Holidays

♦ Las Vegas
♦ New York
♦ UTC/GMT
♦ Paris
♦ Dakar

 

 

NON à l'excision !

Recherche

ŋ [ ] À Ññ Çç ß Óó Ëë Ïï Öö
 @ ½ ¼ Ää Üü ÷ ▀ ² ■ ª º

Al-Nd-Petit-Wolof.jpg
Le Petit Wolof deviendra grand.

 
 
  
anti-xeesal.jpg  
Anti-xeesal Campaign.
       
 
   

Syndication

  • Flux RSS des articles

Le sens du partage


pied_top.jpg
 
Contact - C.G.U. - Rémunération en droits d'auteur - Signaler un abus - Articles les plus commentés